15 «Léegi nag yaw Boroom bi, sunu Yàlla ji nu génnee Misraak doole, nun sa mbooloo, nga siiwale ca sa tur ba sunu jonni yàllay tey, noo bàkkaar, noo tooñ. 16 Boroom bi, seetal ci sa gépp njubte, ba waññi sa mer ak sa xadar, mu moy Yerusalem, sab dëkk, saw tund wu sell. Ndax kat sunuy bàkkaar ak sunu ñaawtéefi maam tax na mboolem ñi ñu wër di sewal Yerusalem ak sa mbooloo.
17 «Kon nag yaw sunu Yàlla, Sang bi, rikk nangul li ma lay ñaan, di la ko dagaan. Boroom bi, ngalla geesul ngir yaw ci sa bopp sa béreb bu sell ba ñu gental. 18 Rikk sama Yàlla, teewlul, déglul te xippi, ba gis sunu gent yi ak sa dëkk ba ñuy tudd sa tur. Du sunu njubte lanu lay dagaane moos, waaye sa yërmande ju yaa rekk a tax. 19 Boroom bi, ngalla Boroom bi, déglu nu te baal nu! Rikk Boroom bi sama Yàlla, teewlul ngir yaw ci sa bopp, te bañ noo yeexe, ndax saw tur lañu tudde sa dëkk ak sa mbooloo.»
20 Maa ngay wax aka ñaan, di tuub sama bàkkaar aka tuubloo Israayil sama ñoñ tey dagaanal sama tundu Yàlla wu sell wi[b], ci sama Yàlla Aji Sax ji. 21 Maa ngay wax ci ñaan gi, waa ja Jibril ma ma gisoon lu jiitu ci peeñu mi, daldi naaw a naaw, dikk ba ci man, yemook waxtuw saraxu ngoon. 22 Mu xamal ma, ne ma: «Dañeel, léegi damaa ñëw ngir leeralal la. 23 Ba nga tàmbalee ñaan la kàddu dikk. Maa la ko yégalsi, ndax yaw ku ñu naw nga. Déggal kàddu gi te dégg peeñu mi.
24 «Lu tollook juróom ñaar fukki yoon ci juróom ñaari at lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jot ñaawtéef gi, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, te diw ab béreb bu sella sell ngir delloo ko sellaayam. 25 Nanga xam kon xéll ne: li ko dale keroog ba ñuy siiwal dogal ba jëm ci leqali Yerusalem, tabaxaat ko, ba keroog njiit li ñu fal di feeñ, juróom ñaar fukki yoon ci juróom ñaari at la. Bu juróom benn fukki yoon ak ñaar ci juróom ñaari at yi weesoo, lañuy tabaxaat pénc ak kàmb gu ñu aare dëkk bi. Waaye jamono yu metti lay doon. 26 Bu àpp boobu weesoo, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqate dëkk beek béreb bu sell bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqate gi dina wéy ba keroog xare biy jeex. 27 Dina feddali kóllëre diggam ak ñu bare ci àppu juróom ñaari at, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu[c], di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»
<- Dañeel 8Dañeel 10 ->- a Seetal ci Yeremi 25.11-12; 29.10.
- b tundu Yàlla wu sell wi, Yerusalem la.
- c lu siblu, sarxalukaayu tuur la, bu ñu samp ca kër Yàlla ga, di ko sobeel.
Languages