1 Yeen ñiy sang yi, yorleen seeni jaam, yorin wu jub te aw yoon, te ngeen xam ne yeen itam am ngeen ab Sang fa asamaan.
5 Jëfeleen xel mu rafet seen diggante ak aji gëmadi ñi ci biti, te jot gi ngeen amagum, fexeleen ba jariñoo ko. 6 Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.
10 Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnabas. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko. 11 Yeesu mi ñuy wax Yustus itam, mu ngi nuyoo. Li bokk ci askanu Yawut, ñoom rekk ay liggéeyandoo ak man ngir nguurug Yàlla, te ñoo seral sama xol. 12 Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci Epafras mi bokk ci yeen, te di jaamub Almasi Yeesu. Muy ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla. 13 Maa ko seedeel ne coonoy ñaan bu réy la nekke, ngir yeen ak waa Lawdise ak waa Yerapolis. 14 Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci sunu soppe Luug, doktoor bi, ak Demas. 15 Nuyulleen nu bokk yi dëkke Lawdise, ak sunub jigéen Nimfa ak mbooloom gëmkat miy daje këram.
16 Gannaaw bu ngeen jàngee-biral bataaxal bii ci seen biir, fexeleen it ba ñu jàng ko biral fa mbooloom gëmkat ma fa Lawdise, te yeen it bataaxal ba ngeen di jote Lawdise, nangeen ko jàng-biral.
17 Waxalleen ma Arsipp ne ko: «Neel jàkk ci liggéey bi nga sasoo ci Boroom bi, ngir nga sottal ko.»
18 Man Póol nag maa leen di bind tàggatoo bii ci sama loxol bopp. Fàttalikuleen ne dañu maa tëj kaso. Yal na aw yiw ànd ak yeen!
<- Kolos 3
Languages