6 Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi mu Nasaret, doxal!» 7 Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam aki kostanam dëgër. 8 Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox aka tëbantu, tey sant Yàlla. 9 Mbooloo mépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla. 10 Ñu xàmmee ko, xam ne moo daan toog, di yalwaan ca bunt bu Rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu jommi ba jommaaral, ba far gëlëm ca la ko dikkal.
17 «Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa. 18 Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottali, ne Almaseem dina sonn. 19 Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru. 20 Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi bi mu leen jagleel, te muy Yeesu. 21 Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottali. 22 Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy feeñal ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax. 23 Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la dagge ci xeet wi, sànk la*Seetal ci Baamtug yoon wi 18.15, 19..”
24 «Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund. 25 Yeen nag yeenay ndonoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeele†Seetal ci Njàlbéen ga 22.18..” 26 Yeen la Yàlla njëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññi kenn ku nekk ci yeen mu moy jikkoom yu bon.»
<- Jëf ya 2Jëf ya 4 ->
Languages