Jëfi ndaw yi Almasi bi yónni Ñaareelu pàcc bi Luug bind lañuy woowe téereb Jëf ya. Mu ngi bind ci li xewoon gannaaw bi Yeesu deewee ba dekki te ñu yéege ko ca asamaan, ak it ci ni mbooloom gëmkat ñi ci Yerusalem màgge. Ba tey mu bind ci ni xibaaru Almasi bi bawoo Yerusalem ak Yude ak Samari, ba wàlli ca xeeti àddina yi ci des. Ci tënk: 1.1—12.25 Xibaaru Yeesu bawoo Yerusalem, law ba wàlli ca gox yi des ci Yuda ak Samari. 13.1—14.28 Yebal nañu ay ndaw wetug sowu, ngir ñu xamleji xibaaru jàmm bi ca diiwaanu Asi. 15.1-35 Péncoo am na ca Yerusalem. 15.36—18.22 Ndaw ya dugg nañu Ërob. 18.23—21.25 Póol tukki na ñetteel bi yoon. 21.25—28.31 Kàddu gi dugg na Room, péey ba, ba àkki ca ëtti kàngam ya gëna kawe.
4 Ba mu nekkee ak ñoom, da leena sant, ne leen: «Buleen jóge Yerusalem, négleen digeb Baay bi ngeen dégge ci sama gémmiñ. 5 Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
6 Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israayil?» 7 Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés bi Baay bi jàpp ci sañ-sañu boppam. 8 Waaye Noo gu Sell gi mooy wàcc ci yeen, ngeen fees ak dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati àddina.»
9 Naka la wax loolu, ndaw yay xoole, ñu jekki yéegee ko fa, aw niir daldi leen koy làq. 10 Ña nga téen, ne jàkk asamaan, Yeesu di wéy. Ci biir loolu ñaar ñu sol yére yu weex ne seef ci seen wet. 11 Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu ci asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
14 Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu ak rakki Yeesu yu góor.
15 Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen: 16 «Bokk yi, Mbind mi moo waxoon lu jiitu ci gémmiñu Daawuda jaare ci Noo gu Sell gi, muy wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti. 17 Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
18 Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru. 19 Waa Yerusalem yépp a ko yég, ba tax ñu tudde tool ba Akeldam, muy firi Toolu deret, ci seen làkk.
20 «Ndax bindees na ci téere bi di Taalifi cant ne:
23 Ci kaw loolu ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas, te ñu di ko wax Yustus itam, ak Maccas. 24 Ñu daldi ñaan ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii, 25 mu jël wàllam ci liggéey bi, te muy céru ndaw bii Yuda wacc, ba fekki wàll wa mu yelloo.» 26 Ñu tegal leen nag bant, bant ba dal ca Maccas, mu dolliku ca fukki ndaw yaak benn.
Jëf ya 2 ->- a Seetal ci Taalifi cant 69.26; 109.8.
Languages