3 Daawuda duma na itam buurub Coba[a], Adadeser doomu Rexob, fekk Adadeser di fexee nanguwaat diiwaan ba feggook dexu Efraat. 4 Daawuda nangoo ca moom junniy gawaram ak juróom ñaari téeméer (1 700) ak ñaar fukki junniy (20 000) xarekat yu warul. Daawuda teg ca dog sidditi tànki fas yi ñu takkal watiir yépp bàyyiwu ca lu moy téeméer. 5 Waa Siri ña dëkke réewum Damaas dikk wallusi Adadeser buurub Coba. Daawuda duma ca ñoom ñaar fukki junneek ñaar (22 000). 6 Ba mu ko defee Daawuda tabb ay jawriñam ca Damaas ca Siri, waa Siri di surgawu Daawuda, di ko indil galag. Aji Sax ji may Daawuda ndam fépp fu mu dem. 7 Daawuda nag nangu pakki wurus ya jawriñi Adadeser takkoon, daldi koy yóbbu Yerusalem. 8 Dëkki Adadeser ya ñuy wax Beta ak Berotay it, xànjar ju takku lool la fa Buur Daawuda nangoo.
9 Ci kaw loolu Toyi buurub Amat dégg ne Daawuda duma na mboolem gàngooru Adadeser. 10 Toyi yebal doomam ju góor Yoram ca Buur Daawuda, di ko yóbbante nuyoob jàmm, ak ndokkale ci jéll bi mu daan Adadeser, ndax Adadeser xare woon naak Toyi. Yoram indaaleel ko jumtukaayi xaalis ak wurus ak xànjar. 11 Buur Daawuda boole loolu, jagleel ko Aji Sax ji, na mu ko jagleele woon xaalis baak wurus wa mu lële ca mboolem xeet ya mu tegoon loxo: 12 maanaam la jóge ca Edomeen ñaak Mowabeen ñaak Amoneen ñaak waa Filisteek Amalegeen ña ak la mu lële ca buurub Coba, Adadeser doomu Rexob.
13 Daawudaa nga gënatee siiw ba mu dumaa waa Siri, teg ca duma fukk ak juróom ñetti junniy (18 000) Edomeen ca xuru Xorom wa. 14 Mu daldi tabb ay jawriñam ca réewum Edom. Réewum Edom gépp la tabb ay jawriñ, Edomeen ñépp di surgawu Daawuda. Aji Sax ji nag may Daawuda ndam fépp fu mu xaree.
Languages