6 Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga. 7 Sànjum Aji Sax ji nag tàkk ci kaw Usa. Yàllaa ko faat foofa, ndaxug teeyadeem, mu dee foofa ca wetu gaalu Yàlla ga[a]. 8 Ba loolu amee Daawuda mer ca mbugal mu metti ma Aji Sax ji fàdde Usa. Moo tax mu tudde béreb booba Peres Usa (muy firi Pàddum Usa), tur wa sax ba tey jii.
9 Daawuda nag am tiitaange lool bésub keroog ci Aji Sax ji. Ma nga naan ca xelam: «Ana nu gaalu Aji Sax ji mana dale ak man?» 10 Loolu nag tax Daawuda nanguwula yóbbu gaalu Aji Sax ji fa moom, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Dafa waññi gaal gi, yóbbu ko ca kër Obedd Edom ma cosaanoo Gaat. 11 Gaalu Aji Sax ji nekk na kër Obedd Edom waa Gaat diiru ñetti weer. Aji Sax ji barkeel Obedd Edom, mook këram gépp.
16 Ba gaalu Aji Sax jay duggsi ca biir gox ba ñu naan Kër Daawuda, soxnas Daawuda, Mikal doomu Sawul a nga sëppu ca palanteeram. Mu gis Buur Daawuda di tëb aka fecc ca kanam Aji Sax ji. Mu jéppi ko lool.
17 Ba mu ko defee ñu indi gaalu Aji Sax ji, yeb ko ca bérebam, ca biir xayma ba ko Daawuda sampal. Daawuda daldi joxe fa kanam Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm. 18 Ba Daawuda defee saraxi rendi-dóomal yaak saraxi cant ci biir jàmm, ñaanal na askan wa ci turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. 19 Mu jox aw ñam askan wépp, mbooloom Israayil mépp, góor ak jigéen; ku ci nekk mu jox la menn mburu ak yàpp wu ñu saaf[b] ak benn nàkku reseñ. Mbooloo ma doora dem, ku nekk ñibbi këram.
20 Ba loolu amee Daawuda walbatiku, dugg biir këram, ngir ñaanal waa këram. Soxnaam Mikal doomu Sawul génn dajeek moom, ne ko: «Buuru Israayiloo, yaaka teral sa bopp bésub tey jii! Nga futteeku tey jii fi kanam jigéen ñiy sa jaami jawriñ yi, mbete nit ku tekkiwul dara!» 21 Daawuda ne Mikal: «Fi kanam Aji Sax ji ma tànn, wacc sa baay ak waa këram gépp, ngir fal ma kilifag Israayil, ñoñi Aji Sax ji, fi kanam Aji Sax ji laay bànneexoo. 22 Dinaa gëna teddadil sama bopp sax, gëna toroxlu, ba gisal ko sama bopp, te du tere jaam yu jigéen yi ngay wax teral ma.» 23 Mikal doomu Sawul jooju nag amul doom, ba ni mu deewe.
<- 2.Samiyel 52.Samiyel 7 ->
Languages