9 Ka ca topp di Elasar, Elasar, Dodo. Dodo, Axowa. Elasar bokkoon na ci ñetti jàmbaari xare ya àndoon ak Daawuda, di dëkk Filisteen ña fa daje woon ngir xare. Fekk bànni Israayil di dellu gannaaw. 10 Elasar a taxaw, di cor Filisteen ña, ba loxo ba banku, taq ca njàppul saamaram. Aji Sax jee maye ndam lu réy bésub keroog! Ba ko mbooloom bànni Israayil fekksee, defuñu lu moy futti néew ya.
11 Ka topp ca Elasar di Saama. Saama, Age ma dëkk Arar ay baayam. Ba Filisteen ña dajee ca Lexi, wetu toolub ñebbe ba meññoon, ba fees dell. Bànni Israayil danoo njëkkoona dawe Filisteen ñi gannaaw. 12 Saama moo taxaw ca digg tool ba, aar tool ba, duma Filisteen ña. Noonu la ci Aji Sax ji maye Israayil ndam lu réy!
13 Mu am bés, jamonoy ngóob, ñett ña bokk ca mbëri xare ya fekki Daawuda ca xunt ma ca Adulam. Mbooloom Filisteen ñaa nga dal ca xuru Refayeen ña. 14 Daawudaa nga ca biir rawtoom. Mu am kuréelu xareb Filisteen gu tollu Betleyem. 15 Ci biir loolu Daawuda dem ba manatula muñ. Mu ne: «Éy waay ku ma wutali woon ndox mu ma naan ca mbalkam Betleyem ma ca buntu dëkk ba!» 16 Ci kaw loolu ñetti jàmbaari xare ya bëtt dalub Filisteen ña, duyi ndox ca teenu Betleyem ba ca wetu buntu dëkk ba, dikk yót Daawuda. Daawuda nag néegu koo naan; da koo tuur, te Aji Sax ji tax. 17 Mu ne: «Mukk Yàlla tere, may naan miim ndox, Aji Sax ji, nde kon deretu ñii dem jaayi seen bakkan laa naan!» Daawuda naanul ndox ma.
18 Abisay bokkoon na ca mbëri xare ya. Abisay ak Yowab, Ceruyaa di seen yaay. Abisay moo yékkati xeejam song ñetti téeméeri góor, rey leen. Mu doxe fa siiw ci ñetti mbëri xare ñooña. 19 Abisay moo gënoona siiw ña bokk kuréel gu tudd Ñett ña; mujj na sax di seen njiit, doonte bokkuloon ca Ñett ña. 20 Benaya nag, Yoyadaay baayam, xarekat bu mag la woon, dëkkoon Kabcel. Def na jaloore yu réy! Moo rey ñaari Mowabeen ña gënoona jàmbaare. Moo wàccoon ci kàmb, bésu tawu yuur, rey fa gaynde. 21 Moo reyoon it waa Misra bu jekk ba taxawaay. Waa Misra baa nga yor ab xeej, Benaya songewu ko lu moy aw yet. Mu bif xeeju waa Misra ba, nangoo ko cay loxoom, reye ko ko. 22 Jooju jëf la Benaya doomu Yoyada def. Moom it siiwoon na ci ñetti mbëri xare ya. 23 Moom lañu gënoona naw ca kuréel gu tudd Fanweeri jàmbaar ya, raw na leen ba booleesu ko ca Ñett ña. Daawuda nag def ko njiitu dag ya ko dar.
24 Ñii bokkoon nañu ca Fanweeri jàmbaar ya:
Languages