2.Piyeer muy ñaareelu bataaxal bi Piyeer bind Buuru Room bu mag bi, Nero, tëj na Piyeer kaso ndax li mu topp Almasi bi. Piyeer xam na ne teg nañu ko dee. Piyeer teewe na njàngaleem Almasi bi, moo tax mu fas yéene di fàttali gëmkat yi mbir yi mu leen doon jàngal. Jàngalekati caaxaan yi wax nañu ne Yeesu délseegul, te jombul du ñëw; bés pénc du am, noonu man nanoo topp sunu bakkan, di xawaare. Piyeer tontu na ne moom ci boppam moo teewe màggaayu Almasi bi ca tund wa, te benn bés ñépp dinañu ko gis. Délseem dafa yeex ndax Yàlla bëgg na ñépp tuub. Piyeer daf leena xiirtal ci xalaatin yu set, ba ñu fàttaliku ndigali Musalkat bi, fàttaliku kàdduy yonent yu sell ya. Ci tënk: Saar 1 Piyeer daa fàttali gëmkat yi ngir ñu dëggal seen ngëm ba séddu ci jikkoy Yàlla. Saar 2 Piyeer artu na leen ci jàngalekati caaxaan yi. Saar 3 Noo ngi séentu bés bi Boroom biy délsi.
5 Loolu tax na ba ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam; 6 seen xam-xam, ngeen dolli ci noot seen bakkan; noot seen bakkan, ngeen dolli ci ag muñ; seenug muñ, ngeen dolli cig ragal Yàlla; 7 seenug ragal Yàlla, ngeen dolli ci bëgg seen bokki gëmkat; bëgg seen bokki gëmkat, ngeen dolli ci cofeel. 8 Ndax yooyu jikko kat su ngeen ko amee, ba mu law, dungeen yaafus, dungeen ñàkk njariñ ci nu ngeen di xame sunu Sang Yeesu Almasi bi. 9 Waaye yii jikko, ku ko ñàkk, daa fekk mu gàtt gis-gis ba far gumba, te fàtte ne dees koo fóotoon ba mu set, teqalikook bàkkaari démbam.
10 Kon nag bokk yi, nangeen gënatee def lu ngeen man ba dëggal woote bi ñu leen woo ak tànn gi ñu leen tànn. Su ngeen ko defee kat, dungeen daanu mukk. 11 Noonu lees leen di ubbile bunt bu yaa bu ngeen di tàbbee ca nguur gu sax gay sunu moomeelu Sang, sunu Musalkat, Yeesu Almasi bi.
16 Du ay léeb yu xel mu xareñ fent lanu leen xamale woon sunu manoorey Boroom Yeesu Almasi bi ak na muy dikke, waaye noo teewe màggaayam. 17 Ndax kat moo nangoo ci Yàlla Baay bi, teraanga ak daraja, ba ko baat ba jibalee, bawoo fa Boroom daraja ju yéeme ja ne: «Kii moo di sama Doom, sama soppe; moom laay bànneexoo*Seetal ci Macë 17.5..» 18 Baat booba jóge asamaan, moom lanu dégg, ba nu nekkee ak moom ca tund wu sell wa.
19 Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke ci biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol. 20 Waaye li ngeen wara njëkka xam moo di amul ci Mbind mi genn kàddug waxyu te yonent ba ko wax, fiire ko xelum boppam. 21 Ndax kat du kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe kàddug waxyu gu bawoo fa Yàlla.
2.Piyeer 2 ->- a Seetal ci Macë 17.5.
Languages