2.Yowaan muy ñaareelu bataaxal bi Yowaan bind Bindkatu bataaxal bii, mag la tudde boppam, di boroom cér ci mboolem gëmkat yi. Soloy bataaxal bii mook soloy bataaxal bu njëkk bi benn la. Moo tax ñu foog ne Yowaan moo ko bind. Ñi moom bataaxal bi ñooy menn mboolem gëmkat mu Yowaan dippee «soxna su tedd si ak ay doomam.» Yowaan di leen ñaax ngir ñuy soppante, tey wattu njàngale mu wérul. Mu di leen ñaax ci seetlu bu baax bala ñoo dalal ay gëmkat yuy tukki ngir wasaare xibaaru jàmm bu Almasi bi.
7 Ndax kat bare na ay naxekat yu dajal àddina, te di ñu dëggalul ne Yeesu Almasi bi moo wàcce yaramu suux. Ku ni mel mooy ab naxekat te mooy bañaaleb Almasi bi. 8 Wattuleen seen bopp bala ngeena ñàkk njariñ li sunub liggéey meññ, xanaa seenub yool mat sëkk. 9 Képp ku saxoowul àlluway Almasi bi, xanaa di ko wees, kooku amul Yàlla. Ku saxoo àlluwa ji nag, yaa am Baay bi, am Doom ji. 10 Ku dikk fi yaw, te dikkewul jooju àlluwa, bu ko dalal sa kër, bu ko sax nuyu, 11 nde ku ko nuyu, am nga ab cér ci jëfam ju bon.
12 Bare na lu ma leen bëggoona bind, waaye bëgguma leen koo waxe kayit ak daa. Teewul ma yaakaara dikkaat wax ak yeen, ne leen jàkk, ngeen ne ma jàkk, ba nu bokk mbég mu mat sëkk.
13 Say doomi rakk ju jigéen, soxna si tedd si, ñu ngi lay nuyu.
Languages