2.Korent muy ñaareelu bataaxal bi Póol bind waa Korent Ci bataaxal bii, Póol bindaat na mbooloom gëmkat yi nekk Korent, ngir tontu ci tuumaal yi ñu ko teg ne du ndawal Almasi bi dëgg. Dañoo sàggi sagam, tuumaal ko ne li muy liggéey lépp dafa koy def ngir jariñoo ko. Póol setal na boppam, wax ne jawriñu Yàlla dëgg la, ngir seen njariñ. Te it Póol fàttali na leen ne mu ngi doon liggéey ci defar ay xayma (Jëf ya 18.3), ngir baña wéeru ci ñoom. Firnde ak kéemaan yiy màndargaal ndawal Almasi bi, Póol feeñal na ko ci ñoom. Li ëpp solo mooy bi mu waxee ne ci ndigalu Yàlla la nekke ndawal Almasi bi. Póol mottali na li ñu ko yónni, doonte jànkoonte na ak ay fitna. Yékkati Almasi bi, moo tax mu wàcce boppam ci kanamu nit ñi yég seen bopp, di ko tuumaal. Ci bataaxal bi, Póol fàttali leen ndimbal li muy dajaleel gëmkat ya ca Yerusalem (Room 15.26). Dafa yaakaar ne ndimbal loolu dina wone bennoo bi nekk ci gëmkati Yawut yi ak ñeneen ñi dul Yawut. Ci tënk: 1.1—7.16 Póol liggéeyu ndawal Almasi bi la def. 8.1—9.15 Póol ñaan na ndimbal lu jëm ca gëmkat ya néew-doole ca Yerusalem. 10.1—13.13 Póol setal na boppam ci liggéeyu ndaw bi muy def.
8 Ndax kat, bokk yi, bëggunu ngeen umple njàqare ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax. 9 Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar Yàlla miy dekkal ñi dee. 10 Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu. 11 Yeen itam, ni ngeen nu ciy jàppalee mooy ngeen di nu ñaanal. Su ko defee yiw wa nu ñu bare ñaanal ba nu am ko, dina tax ñu bare biral ag cant ci sunu mbir.
15 Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona njëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana doon ñaar, ngir nu mana gise ñaari yoon, 16 ba bu ma jógee ci yeen, daldi jaareji ci diiwaanu Maseduwan, bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yeen, ba ngeen yiwi ma, ma jëm Yude. 17 Ndax ñàkk pastéef laa mébéte moomu mébét? Am ni nitu suuxu neen di mébéte rekk laa topp bay xel ñaar, naan «waaw», naan «déet»?
18 Yàlla mi mata gëm de seede na ne kàddu gi nu leen di wax du «waaw, déet,» 19 ndax Doomu Yàlla, Yeesu Almasi bi nu biral ci seen biir, man ak Silwan*Silwan mooy turu waa Room wi Gereg yi naan Silas. Seetal Jëf ya 15.22, 40. ak Timote, du kàddug «waaw, déet;» «waaw» doŋŋ a nekk ci moom. 20 Ak li digey Yàlla di bare lépp, ci Almasi bi la ay digeem di doone «waaw». Moo tax itam, ci moom lanu naan Yàlla: «Amiin», ngir delloo ko njukkal. 21 Te ki nuy saxal ci Almasi bi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla. 22 Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.
23 Man nag seedey Yàlla laa ciy sàkku, giñ naa ko ci sama bakkan, bañ leena yokku naqar moo tax délsiwuma Korent. 24 Du caageenu yilif seen ngëm nag, ndax ci ngëm ngeen sax, waaye nook yeen ay liggéey, ngir seen mbégte.
2.Korent 2 ->- a Silwan mooy turu waa Room wi Gereg yi naan Silas. Seetal Jëf ya 15.22, 40.
Languages