1 Suleymaan sàkk na itam ab sarxalukaayu xànjar bu gudde ñaar fukki xasab, yaatoo ñaar fukki xasab, taxawaayam di fukki xasab. 2 Ci biir loolu mu móollu mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu; yaatoo fukki xasab catu omb, ba catu omb; taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub. 3 Ay jëmmi nag a nga ca suufu mbalka ma, wër ko ba mu daj, fukki nag tollook xasab. Nag yi def ñaari làng yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli. 4 Mbalkam njàpp mi, ci kaw fukki jëmmi nag ak ñaar la tege, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp. 5 Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppu tóor-tóor. Ñetti téeméeri barigo ak fanweer (330) la mbalka miy def. 6 Ci biir loolu Suleymaan sàkk fukki ndabi raxasu, teg juróom wetu ndijoor, juróom wetu càmmoñ, ñu di ca raxas yàppu saraxu rendi-dóomal, mbalka ma nag, sarxalkat ya di ca jàppe.
19 Gannaaw loolu Suleymaan defarlu na mboolem yeneen jumtukaayi kër Yàlla ga: muy sarxalukaayu wurus ba, ak taabal ya ñuy teg mburum teewal ma, 20 ak tegukaayi làmp ya ak seeni làmp, lépp di wurusu ngalam, làmp yiy tàkk, na ko àtteb yoon tërale, fa kanam néeg bu sella sell bi; 21 tóor-tóor yi it ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurus, wurus wu set wecc. 22 Feyukaay yi itam ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraay yi, lépp wurusu ngalam la. Te bunti kër Yàlla ca la, muy: buntu néeg bi ñuy jaare dugg ci néeg bu sella sell bi, ak ay lafam ak lafi buntu néeg bi ñuy jaare dugg ci néeg bu mag bi, lépp wurus la.
<- 2.Jaar-jaar ya 32.Jaar-jaar ya 5 ->- a Cereda ak Cartan, benn gox bi la.
Languages