2.Jaar-jaar ya muy ñaareelu téere bi te ëmb jaar-jaari jamono Ñaareelu téereb Jaar-jaar ya moo wéyal nettalib démbi Israayil, bi dooroon ci 1.Jaar-jaar ya. Téere bii moo indi ni nguurug Suleymaan ame woon daraja, di ci fésal li mu tabax kër Yàlla ga. Téere bi teg ci indi jëfi buuri Yuda yi wuutu Suleymaan, te gën cee biral yitte ji kenn ku nekk amoon ci mbiri askan wi, ci wàllu ngëm. Meneen mbir mu ñu ci fàttali mooy tasteg Yerusalem, ak ngàllo ga Israayil mujje ca Babilon ga ñu leen toxaloon. Teewul téere bi tëje xew-xewu jàmm, te mooy ba Buur Sirus bu Pers yékkatee ab dogal bu yiwi bànni Israayil, may leen ñu saña ñibbi seenum réew. Ci tënk: 1.1-17 Suleymaan ci ndoortel nguuram. 2.1—7.22 Lu jëm ci tabaxub kër Yàlla ga, ñu jagleele ko am xew. 8.1-18 Lu jëm ci darajay nguuru Suleymaan. 9.1-12 Lingeer buurub Seba gane na Suleymaan. 9.13-31 Lu jëm ci darajay Suleymaan ak deewam. 10.1—36.23 Lu jëm ci yeneen buuri Yuda yi.
13 Ba loolu amee Suleymaan bàyyikoo ca xaymab ndaje ma ca jaamookaay ba ca Gabawon. Mu dem Yerusalem, falu buur ca Israayil.
14 Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri (1 400) watiir, ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu teg ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. 15 Buur Suleymaan a def xaalis ak wurus late biir Yerusalem bay safi doj, garabi seedar di fa saf garabi sikomoor yi ne xas ci suufu tund yi. 16 Fasi Suleymaan, Misra lañu leen daan jëggaanee ak Silisi, baana-baanay buur, ca Silisi lañu leen daan jënde. 17 Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri (600) dogi xaalis la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki (150) dogi xaalis, te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen.
18 Suleymaan nag dogu ne kër lay tabax ñeel turu Aji Sax ji, ak geneen kër gu ñeel nguurug boppam.
2.Jaar-jaar ya 2 ->
Languages