1.Tesalonig muy bataaxal bu njëkk bi Póol bind waa Tesalonig Tesalonig péeyub diiwaanu Maseduwan la woon ci réewum Geres. Gannaaw bi Póol sampee mbooloom gëmkat ci dëkku Filib, samp na meneen ci Tesalonig (Jëf ya 17.1-9). Gannaaw bi mu jógee Tesalonig, Póol dafa ragal ne ñu ngi jàq ci coono yi ñu daj, ba tax mu yebal Timote, ngir mu natt fu seen ngëm tollu. Bi Timote délsee, indi xibaaru jàmm bi jóge ci ñoom, la leen Póol bind bataaxal bii. Waaye am na ci gëmkat yi ñenn ñu baña liggéey, di foog ne Almasi bi dina délsi ci lu dul yàgg. Póol wax leen li wara xew bés bu Boroom bi délsee, ak ni ñu wara dunde balaa booba. Ci tënk: 1.1—3.13 Póol fàttaliku na teewaayam ci ñoom ak ni ñu nangoo njàngaleem. 4.1-12 Póol mu ngi leen di ñaax ñu jëfe sell ak mbëggeel. 4.13—5.11 Póol mu ngi jàngale ci ndekkite li ak délsig Almasi bi. 5.12-28 Póol tàggatoo naak ñoom.
4 Yeen bokki gëmkat ñi Yàlla sopp, xam nanu ne moom moo leen tànn, 5 ndax sunu xibaaru jàmm bi nu leen àgge, dikkewu leen ay wax rekk, waaye manoore la leen dikkaale ak ndimbalal Noo gu Sell gi ak kóolute gu mat sëkk gu ngeen am. Xam ngeen moos na nu nekke woon ca seen biir, di xintewoo seen njariñ. 6 Aw ngeen sunuy tànk, aw it ci tànki Sang bi, ndax yeena jot ci kàddu gi, ci biir njàqare ju bare, te di ko bége ci ndimbalal Noo gu Sell gi. 7 Moo leen taxa doon royukaay ci mboolem gëmkati diiwaani Maseduwan ak Akayi. 8 Ci seen biir kay la kàddug Boroom bi jollee, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen ngëm Yàlla fépp la siiwe, ba soxlawunu cee waxati fenn dara. 9 Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp na sunu ngan ak yeen deme ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund, 10 tey séentu Doomam Yeesu mi mu dekkal, mu dikk bàyyikoo asamaan, moom mi nu jot ci sànj miy dikk.
1.Tesalonig 2 ->- a Silwan mooy turu waa Room wi Gereg yi naan Silas. Seetal Jëf ya 15.22, 40.
Languages