5 Ñaari soxnay Daawuda lañu jàpp; Axinowam mu Yisreel ak Abigayil waa Karmel ba, soxnas Nabal woon. 6 Ba loolu amee Daawuda jàq lool, ndax mbooloo maa nga doon wax naan dañu koy dóori doj. Booba mbooloo ma ba mu daj, ku nekk a ngaak naqaru xol, di xalaat doomam yu góor ak yu jigéen. Daawuda nag dëgërloo Yàllaam Aji Sax ji rekk. 7 Ci biir loolu Daawuda wax ak sarxalkat ba Abyatar doomu Aximeleg, ne ko mu indil ko xar-sànni mi. Abyatar indil Daawuda xar-sànni ma. 8 Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma topp gàngooru yàqkat yii? Ndax dinaa leen dab?» Mu ne ko: «Demal, yaay dabe déy, te yaay xettalee déy.»
9 Ba mu ko defee Daawuda dem, mook juróom benni téeméeri (600) nit ña ànd ak moom. Ñu dem ba ca xuru Besor, ñenn ña yem fa. 10 Daawudaa ñoqali, mook ñeenti téeméeri (400) nit, ñaari téeméeri (200) nit yem foofa, ndax loof, ba manuñoo jàll xuru Besor. 11 Ci kaw loolu ña jàll yem ci jenn waayu Misra ci àll bi. Ñu indi waa ji ba ci Daawuda, daldi may waa ji mburu mu lekk, may ko ndox, mu naan. 12 Ab danku figg ju wow ak ñaari danki reseñ lañu ko leel, mu doora leqaliku, ndax dafa fekk lekkul, naanul diiru ñetti guddi ak ñetti bëccëg. 13 Daawuda ne ko: «Yaw, kuy sab sang ak foo bokk?» Xalelu góor ba ne ko: «Man waa Misra laa, di jaamub jenn waayu Amalegeen. Sama sang a ma wacc, ba ma woppee bërkaati-démb. 14 Noo song wetu Negew ca diiwaanu waa Keret ña, ak diiwaanu Yuda, ak wetu Negew ca diiwaanu Kaleb, te Ciglaag, noo ko lakk.» 15 Daawuda ne ko: «Ndax man nga maa yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yooyu?» Mu ne ko: «Giñal ma ci Yàlla ne, doo ma rey, te doo ma delloo ca sama sang; kon dinaa la yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yi.»
16 Ci kaw loolu waa ja yóbbu Daawuda, ndeke nit ñaa nga ne wesar ca àll ba bépp, di lekk aka naan, di mbumbaaye mboolem alal ju bare ja ñu nangoo ca réewum Filisti ak réewum Yuda. 17 Daawuda nag di leen faat, njël ba ca ngoon. Kenn rëccul, lu moy ñeenti téeméeri (400) xale yu góor yu war ay giléem, daw. 18 Daawuda nangu mboolem lu Amalegeen ña jëloon, nangu ñaari soxnaam. 19 Dara lu bokk ci ñoom rawul. Mag ñaak ndaw ñaak seen doom yu góor ak seen doom yu jigéen ak alal jaak mboolem lu ñu leen jëlaloon. Lépp la Daawuda delloosi. 20 Mu nangu mboolem jur gu gudd ak gu gàtt, nitam ña dàq, tofal ca juru Amalegeen ña, te naan: «Lëlub Daawudaa ngi!»
Languages