9 Ndawi Daawuda ya nag dikk, jottali Nabal kàddu yooyu yépp ci turu Daawuda, ba daaneel, ne tekk. 10 Nabal ne ndawi Daawuda: «Ana kuy Daawuda? Kuy doomu Yese sax? Jamonoy tey jaam yu baree ngi fàqe ci seeni sang. 11 Ana luy ndeyi may jël saab dund ak samam ndox ak yàppu jur gi ma rendil sama watkati jur, di ko jox ñu ma xamul fu ñu jóge?» 12 Ba loolu amee ndawi Daawuda walbatiku ñibbi. Ba ñu dikkee, daldi koy yegge kàddu yooyu yépp. 13 Daawuda ne ndawam ya: «Ràngooleen seeni saamar, yeen ñépp.» Ñu ràngoo seeni saamar ñoom ñépp, Daawuda it ràngoo saamaram, lu tollook ñeenti téeméeri (400) góor ànd ak Daawuda, ñaari téeméer (200) des ca seen cummikaay.
18 Ba mu ko defee Abigayil gaaw sàkk ñaari téeméeri mburu ak ñaari mbuusi biiñ ak juróomi gàtt yu ñu defar ak juróomi natti peppum mbool ak téeméeri cabbi reseñ ak ñaari téeméeri danki figg, boole ko sëf ci ay mbaam. 19 Mu ne ay surgaam: «Jiituleen, maa ngi topp ci yeen.» Nabal jëkkër ja nag, ndaw sa waxu ko ci dara. 20 Naka la ndaw sa dawal mbaamam, làqoo mbartalu tund wa, di wàcc ca xur wa, ndeke Daawudaa nga ànd aki nitam, di dajeek moom; ndaw sa ne pemm ca ñoom. 21 Fekk na Daawuda doon wax naan: «Ndeke kay neen laa doon wattoo mboolem lu bokk ci kii ca màndiŋ ma, ba lennam réerul; lu bon la ma feye lu baax. 22 Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam maa wacc bët di sete kenn ku bokk ci waa jii, kuy colal.»
23 Abigayil séen Daawuda, daldi gaaw wàcc mbaam ma, ne gurub fa kanamam, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot. 24 Naka la ne fëlëñ ca tànki Daawuda, ne ko: «Sang bi, naa tegoo tooñ gi, may ma rekk, ma wax la. Ngalla sama sang, déglul sama kàddu. 25 Sang bi, bul déglu mukk nit ku bon kii, Nabal mii. Moom turam doŋŋ la wuyu, ndax Nabal (muy firi Dof bi) la tudd, te ndof la nekke. Man nag sang bi, gisuma woon ndaw yi nga yebal. 26 Léegi nag sang bi, giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, nga fekke tey, Aji Sax jee la teree tuur deret tey, di feyul sa bopp. Muy say noon, di ñi lay fexeel lu bon, yal nañu bokk ak Nabal mii demin. 27 Sarica bii ma la indil nag, sang bi, nañu ko jox xale yu góor yi topp ci yaw. 28 Sang bi, jéggal ma rekk ndax Aji Sax jee lay defal moos kër gu yàgg. Kon nag, Yàlla bu nit gis mukk lu bon ci yaw, sa giiru dund. 29 Bu ñu la doon dàq, di wut sa bakkan, yal na fekk sa bakkan dence ca ëmbu aji dund ña, ca sa wetu Yàlla Aji Sax ji, sang bi. Waaye sa bakkanub noon, yal na ko mbaq, sànni fu sore. 30 Keroog, sang bi, bu la Aji Sax ji defalee mboolem lu baax la mu la dig, ba fal la, nga jiite Israayil déy, 31 su boobaa doo réccu, doo am yaraange ci loo doon tuure deret ci neen, mbaa loo doon feyul sa bopp. Te ngalla sang bi, keroog bu la Aji Sax ji baaxee, fàttalikul sab jaam.»
32 Daawuda ne Abigayil: «Cant ñeel na Aji Sax ji Yàllay Israayil mi la yebal bésub tey jii, ngir nga dogale ma. 33 Maa ngi lay gërëme sa njort, di la gërëme sa jëmmu bopp jii ma teree tuur deret, ngir feyul sama bopp. 34 Lu ko moy de, giñ naa ci Kiy dund, Aji Sax ji Yàllay Israayil ji ma téye ba loruma la, soo gaawul woon, dogalesi ma, du kenn moos ku ñuy wacc, bët di ko sete ci mboolem kuy colal te bokk ci Nabal.» 35 Ba loolu amee Daawuda nangoo ca loxol ndaw sa la mu ko indil, daldi ne ko: «Ñibbil ak jàmm. Dégg naa sa kàddu te nangul naa la.»
41 Abigayil daldi sujjóot, dëpp jëëm fa suuf, ne leen: «Maa ngii dib jaamam, ba ci raxas tànki surgaam yi.» 42 Ci kaw loolu Abigayil ne ñokket, war mbaamam, juróomi surgaam yu jigéen ànd ak moom, mu topp ca ndawi Daawuda ya. Noonu la Abigayil doone soxnas Daawuda.
43 Axinowam ma cosaanoo Yisreel itam, Daawuda jëloon na ko soxna, ñuy wujje ñoom ñaar. 44 Fekk na Sawul nangu doomam Mikal, soxnas Daawuda, may ko waa Galim ba ñuy wax Palti doomu Layis.
<- 1.Samiyel 241.Samiyel 26 ->- a Xari waa penku dañuy bare kawar gu ñuy wat aka ëcc, di ci defar ag wëñ. Bu ñu daan watlu seeni xar, xew mu réy la woon.
Languages