1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Yewu doomu Anani, di rëbb Basa. Mu ne ko: 2 «Damaa fekk nga maaseek pëndub suuf, ma yékkati la, jiital la, nga yilif Israayil sama ñoñ. Nga aw nag ci yoonu Yerbowam, di bàkkaarloo Israayil sama ñoñ, ba ma mer ndax seeni bàkkaar. 3 Kon dama ne, dinaa la far, yaw Basa, yaak sa waa kër. Dinaa def sa kër mel ni kër Yerbowam doomu Nebat.
5 Li des ci mbiri Basa ak la mu def ak njàmbaaram, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israayil ca seeni jant. 6 Gannaaw loolu Buur Basa saay, fekki ay maamam, ñu denc ko Tirca. Ela doomam moo falu buur, wuutu ko.
7 Te itam ba kàddug Aji Sax ji dikkalee Yonent Yàlla Yewu doomu Anani di rëbb Basa ak waa këram, li ko waral mooy la Basa def lépp, di roy waa kër Yerbowam, Aji Sax ji ñaawlu ko ba xolam fees. Rax ci dolli Basa rey waa kër Yerbowam.
14 Li des ci mbiri Ela ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israayil ca seeni jant.
20 Li des ci mbiri Simri ak pexe ma mu laloon, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israayil ca seeni jant.
21 Ba mu ko defee mbooloom Israayil séddalikoo, def ñaari xaaj. Genn-wàllu mbooloo ma topp ca gannaaw Tibni, nar koo fal buur. Tibni nag, Ginat ay baayam. Genn-wàll ga ca des ànd ak Omri. 22 Mbooloom Omri ëpp doole mbooloom Tibni doomu Ginat. Tibni daldi dee, Omri di buur.
25 Teewul Omri di def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, ba gëna bàkkaar mboolem ña ko jiitu. 26 Daa aw ci tànki Yerbowam doomu Nebat ci mboolem lu mu daan def ba ci bàkkaaram bi mu daan bàkkaarloo Israayil, di jógal xolu Aji Sax ji Yàllay Israayil ci seen tuuri neen.
27 Li des ci mbiri Omri aki jëfam ak njàmbaaram, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israayil ca seeni jant. 28 Buur Omri saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Axab doom ja falu buur, wuutu ko.
30 Axab doomu Omri di def li Aji Sax ji ñaawlu, ba raw mboolem ña ko jiitu. 31 Mu sàlloo bàkkaari Yerbowam doomu Nebat. Loolu doyatu ko, mu jël jabar Yesabel doomu Etbal, buurub waa Sidon ña. Mu dem bay jaamu seen tuur mi ñuy wax Baal, di ko sujjóotal. 32 Mu yékkatil Baal ab sarxalukaay ca jaamookaay ba mu ko tabaxal. 33 Axab teg ca samplu xer wu ñuy jaamoo Asera. Axab def na lu rawati la mboolem buuri Israayil ya ko jiitu defoon, ba feesal xolu Aji Sax ji Yàllay Israayil.
34 Ca jamonoy Axab la Iyel ma dëkk Betel tabaxaat Yeriko. Abiram taawam la Iyel ñàkk ndax la muy tëral fondmaa tata ya, teg ca ñàkk Segub, am caatam ba muy taxawal bunti dëkk ba. Mu dëppook kàddug Aji Sax ja Yosuwe doomu Nuun jottali woon*Seetal ci Yosuwe 6.26..
<- 1.Buur ya 151.Buur ya 17 ->- a Seetal ci Yosuwe 6.26.
Languages