1.Korent muy bataaxal bu njëkk bi Póol bind waa Korent Korent péeyub diiwaanu Akayi la woon ci réewum Geres. Póol dem na Korent juróom fukki at gannaaw deewug Almasi bi. Mu toog fa fukki weer ak juróom ñett. Gannaaw ab diir mu dellu Korent toogaat fa lu tollook ñetti weer (Jëf ya 18.1-18; 20.1-3). Liggéeyam foofa tax na ba ñu bare topp Almasi bi. Póol dégg na seen xibaar te mu naqari ko. Féewaloo ak séy yu awul yoon am na ci seen biir, te am na ñu wax ne ñi dee duñu dekki. Mu bind leen ngir ñu jekkal seen diggante, te jekkal seen jaamu Yàlla. Mu tontu it ay laaj yu ñu ko bind. Póol di leen fàttali ne man nañoo saafara jafe-jafey mbooloo mi, su fekkee bëggante am na ci seen biir, ni leen Almasi bi bëgge, te ñu xool ëllëgu Yàlla te baña gis àddina si ñu nekk. Ci tënk: 1.1-9 Póol nuyoo na, ñaan na. 1.10—4.21 Nanu bennoo. 5.1—6.20 Am ngeen sañ-sañ, waaye war ngeena terale Yàlla seen yaram. 7.1-40 Lu jëm ci mbirum séy. 8.1—11.1 Nanu sore bokkaale. Lu jëm ci ñam wu ñu sarxale ay tuur. 11.2—14.40 Nanu jekkal sunu jaamu Yàlla. 15.1-58 Ndekkite li leeral na ni nu wara dunde. 16.1-24 Póol mébét na, dénkaane na.
13 Ndax Almasi bi dafa xàjjalikoo? Ndax Póol lañu daajoon ca bant ba ngir yeen? Am ci turu Póol lañu leen sóobe ci ndox? 14 Maa ngi sant Yàlla, ba ma sóobulee kenn ci yeen ci ndox, ku dul Kirispus ak Gayus, 15 ngir kenn du ne ci sama tur lañu leen sóobe. 16 Ahakay! Maa sóob waa kër Estefanas itam. Waaye bu loolu weesoo, fàttalikuwuma fu ma sóobe keneen. 17 Ndax du sóobe cim ndox la ma Almasi bi yebale, waaye ngir ma yégle xibaaru jàmm bi, te bañ koo defe xareñtey kàddu, ngir baña neenal bantub Almasi ba ñu ko daajoon.
20 Ana kuy xamkat? Ana kuy firikatub yoon? Ana waxkatub àddinay tey jii? Xanaa du Yàllaa def xam-xamu àddina si ag ndof? 21 Yàlla moo dogal ci xam-xamam, àddina tële koo xam ci xam-xamu boppam. Moo tax mu soob Yàlla, mu jëfandikoo xibaaru Almasi biy ag ndof ci nit ñi, ngir musale ko gëmkat ñi. 22 Yawut yi, ay takk lañuy laaj, Gereg yi di wut xam-xam. 23 Nun nag, nuy waare ci Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jàmbur ñi dul Yawut. 24 Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi bi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla. 25 Ndaxte li ñu jàppe ag ndof fa Yàlla moo sut xam-xamu nit, te li ñu jàppe néew dooley Yàlla moo raw dooley nit.
26 Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu. 27 Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko li bare doole. 28 Li tuut ab juddu ci àddina ak li xeeblu, li tekkiwul dara, moom la Yàlla tànn, ngir neenale ko li tekki, 29 ba tax kenn du mana damu ci kanam Yàlla. 30 Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot, 31 su ko defee, noonu ñu binde ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi†Seetal ci Yeremi 9.23.,» noonu lay ame.
1.Korent 2 ->
Languages