2 Ka jiite woon kuréel gu njëkk ga ca weer wu njëkk wa, Yasobam la, doomu Sabdiyel. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 3 Mu ngi askanoo ci Peres, di kilifag mboolem jawriñi gàngoori xare ya ca weer wu njëkk wa. 4 Ka jiite woon kuréelu ñaareelu weer wa, Doday la, te mu askanoo ci Axowa; Miglot topp ci moom, jiite kuréelam. Kuréel ga ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 5 Kilifag ñetteelu mbooloo ma ca ñetteelu weer wa, Benaya la woon, doomu Yoyada, sarxalkat bu mag ba. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 6 Benaya moomoo doon jàmbaari xare ja bokkoon ca Fanweeri jàmbaar ya, jiite leen. Amisabat, doomam ju góor bokk ca kuréel ga. 7 Ñeenteelu kilifa ga ca ñeenteelu weer wa, Asayel la, mbokkum Yowab; Sebaja, doomam ju góor moo ko wuutu. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 8 Juróomeelu kilifa ga ca juróomeelu weer wa, Samut la, bokk ci làngu Israx. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 9 Juróom benneelu kilifa ga ca juróom benneelu weer wa, Ira la woon, doomu Ikes mu Tekowa. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 10 Juróom ñaareelu kilifa ga ca juróom ñaareelu weer wa, Elecc la woon, mu Palon, bokk ca giirug Efrayim. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 11 Juróom ñetteelu kilifa ga ca juróom ñetteelu weer wa, Sibekay la woon, mu Usa, bokk ca làngu Sera. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 12 Juróom ñeenteelu kilifa ga ca juróom ñeenteelu weer wa, Abiyeser la woon, mu Anatot, bokk ca giirug Beñamin. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 13 Fukkeelu kilifa ga ca fukkeelu weer wa, Maaray la woon, mu Netofa, bokk ca làngu Sera. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 14 Fukkeelu kilifa gaak benn ca fukkeelu weer waak benn, Benaya la woon, mu Piraton, bokk ca giirug Efrayim. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon. 15 Fukkeelu kilifa gaak ñaar ca fukkeelu weer waak ñaar, Elday la woon, mu Netofa, bokk ca làngug Otniyel. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
23 Daawuda nag boolewu ci limu nit ñi am ñaar fukki at ak lu ko yées ndax Aji Sax ji dige woon na ne dina giiral Israayil ba ñu tollook biddiiwi asamaan. 24 Yowab doomu Ceruya tàmbali woon na leen lim sax, waaye sottalul, ndax loolu taxoon na sànjum Yàlla wàcc ci kaw Israayil. Moo tax lim ba bokkul ca limeefu téere bi ñu dippee Jaloorey Buur Daawuda cay jantam.
26 Ka jiite woon surga yay liggéey ca tool ya, di bey, Esri la, doomu Kelub.
27 Ka ñu dénkoon tóokëri reseñ ya, Simey mu Raama la.
28 Ka ñu dénkoon garabi oliw yaak garabi sikomoor ya ca suufu tund ya, mooy Baal Anan mu Bet Geder.
29 Ka ñu dénkoon nag ya ca parlu ya ca jooru Saron, mooy Sittray mu Saron.
30 Ka ñu dénkoon giléem ya, Obil la, bokk ca giirug Ismayla.
31 Ka ñu dénkoon gàtt ya, Yasis la, bokk ci giirug Agar.
Languages