4 Ba mu ko defee kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dikkal ma, ne ma: 5 «Waxal askanu réew mi mépp, ak sarxalkat yi, nga ne leen: “Ba ngeen dee woor ak a ñaawlu ci weeru juróomeel, ak weeru juróom ñaareel, ci diiru juróom ñaar fukki at yii, ndax man mii ngeen doon woorala wooral? 6 Te su ngeen lekkee ak su ngeen naanee, xanaa du seen bopp ngeen lekkal ak a naanal?” 7 Xanaa du yii kàddu la Aji Sax ji biraloon ci jottlib yonent yu jëkk ya, jant ya waa Yerusalem ak dëkk ya ko wër nekkee ci jàmm, te diiwaani Negew, ak suufu tund ya am ñu ko dëkke?»
8 Gannaaw gi kàddug Aji Sax ji dellu dikkal ma, man Sàkkaryaa, ne ma: 9 «Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Àtteb dëgg, nangeen ko àttee, te ngor ak yërmande it, deeleen ko jëflantee. 10 Ab jëtun, ak ab jirim, ak ab doxandéem, ak ab néew-doole, buleen ko not. Lu bon it, buleen ko mébétalante ci seen xol.»
11 Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg. 12 Seen bopp lañu dëgëral niw doj, ba faaleetuñu ndigalu yoon wi, ak kàddu yi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi yónnee ag Noowam, ci jottlib yonent yu jëkk ya. Muy sànj mu réy nag, bawoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. 13 «Ba ma wootee,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «wuyuwuñu; moo tax ba ñu wootee, wuyuwuma. 14 Maa leen tasaare ni callweer ci biir mboolem xeet yu ñu xamul woon, réew mi gental seen gannaaw, ba kenn jaareetu fi dem ak a délsi. Nii lañu defe ab gent, réew mu bakkane.»
<- Sàkkaryaa 6Sàkkaryaa 8 ->