4 Ma ne malaaka ma doon wax ak man. «Sang bi, watiir yii lu ñu wund?»
5 Malaaka mi ne ma: «Ñii ñooy ñeenti ngelawi asamaan yi génne fa ñu teewe woon fa kanam Boroom àddina sépp.» 6 Bi fas yu ñuul yi takk, réewum bëj-gànnaar la jëm; bi fas yu weex yi takk topp seen gannaaw; fas yu tippante yi nag, réewum bëj-saalum*6.6 Bëj-saalum ak bëj-gànnaar ñaare ñooy wet yi nooni Israyil féete woon. lañu jëm.
7 Fas yu am kàttan yooyu yépp nag génn, yàkkamtee wëri àddina. Aji Sax ji ne leen: «Demleen wëri àddina.» Ñu daldi dem, wëri àddina.
8 Ci kaw loolu mu àddu ca kaw, ne ma: «Xoolal, ñi jëm réewum bëj-gànnaar, samag Noo lañuy sànni ca kaw réewum bëj-gànnaar.»
11 «Jëlal yóbbal boobu, di wurus wi ak xaalis bi, nga sàkk ci mbaxanam buur, te teg ko ci kaw boppu sarxalkat bu mag bi†6.11 Liggéeyu carxal ak nguur, ñaari sas yooyu, ci yoon, du woon lees di boole yor ci Israyil., Yosuwe doomu Yoccadag. 12 Nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
14 «Mbaxanam buur mi baaxantal lay doon ci biir kër Aji Sax ji, ñu di ko fàttlikoo Elday§6.14 Elday man naa doon Elem itam. ak Tobya ak Yedaya, ak mbaaxug Yosiya doomu Cefaña. 15 Ñu sore ñooy dikk tabaxsi kër Aji Sax ji, ba ngeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal ci yeen. Loolu mooy am, ndegam déggal ngeen ba déggal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji.»
<- Sàkkaryaa 5Sàkkaryaa 7 ->