7 Ba loolu amee may sàmm xar yi teefonke yi nara rendiluji, rawatina ñi gëna sonn ci gétt gi. Ca laa jël ñaari yeti sàmm. Benn bi ma tudde ko Xejjoo, bi ci des ma tudde ko Bennoo. Ci kaw loolu may sàmm gétt gi. 8 Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen. 9 Ma ne gétt gi: «Dootuma leen sàmm. Na ñiy dee, dee; ñiy sànku, sànku; ñi dese bakkan yàppante ci seen biir.»
10 Ba mu ko defee ma jël sama wenn yet wi, Xejjoo, damm ko, ngir doge ko sama kóllëre gi ma fasoo woon ak askan yépp. 11 Bésub keroog la kóllëre ga dog, teefonke yi may xool daldi xam ne loolu kàddug Aji Sax ji la.
12 Gannaaw loolu ma ne leen: «Su leen neexee, joxleen ma sama peyoor, su leen neexul téyeleen ko.» Ñu waññ fanweeri donji xaalis, feye ma.
13 Aji Sax ji ne ma: «Ndaw njëg gu réy gu ma leen jaral! Sànni ko ca boroom njaq ya.» Ma jël fanweeri donji xaalis ya*11.13 Mooy ndàmpaay li ñuy fey sang bu ñu gaañ jaamam. Seetal ci Mucc ga 21.32., sànni ko boroom njaq ya, ca kër Aji Sax ji.
14 La ca tegu ma damm sama ñaareelu yetub sàmm ba, Bennoo, ngir dog bokk gi dox diggante Yuda ak Israyil.
15 Aji Sax ji nag neeti ma: «Léegi jëlal jumtukaayu sàmm bu ñàkk bopp. 16 Maa ngi nii kat di taxawal ab sàmm ci réew mi. Lu ci réer, faalewu ko; lu ci lajj, du ko seet, lu ci gaañu, du ko faj, lu wér du ko xont, te lu ci duuf, mu yàpp, ba toj seeni we.
- a 11.13 Mooy ndàmpaay li ñuy fey sang bu ñu gaañ jaamam. Seetal ci Mucc ga 21.32.