Sàkkaryaa
12 Malaakam Aji Sax ji ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, loo deeti xaar, doo noppee xañ yërmande Yerusalem ak yeneen dëkki Yuda? Juróom ñaar fukki at a ngii yoo leen mere*1.12 Juróom ñaar fukki at la waa Yuda nekk cig njaam. ca Babilon.!»
13 Aji Sax ji nag àddu, wax ak malaaka ma doon wax ak man, kàdduy mas-sawu yu neex. 14 Ca la ma malaaka ma doon wax ak man, ne ma: «Yéeneel, nga ne: Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Maa fiire Yerusalem, maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy. 15 Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay†1.15 Xeet yooyu ñoo tegoon Yuda notaange gu jéggi dayo, ba raw la leen Yàlla naraloon..” 16 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Yërmande laay dellusee Yerusalem. Sama kër lees fay tabaxaat.” Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. Mu ne: “Buumu nattukaay dina tàllalu ci kaw Yerusalem.” 17 Nanga yéenewaat, nga ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Samay dëkk ay walewaat ak alal, te Aji Sax ji mooy dëfalati Siyoŋ, mooy taamooti Yerusalem googu.”»
Sàkkaryaa 2 ->