Saar 3
Réeroo, gise
Ndaw si
1 Sama kaw lal, guddi,
laa seet sama soppey xol.
Seet naa ko, gisuma ko.
2 Naa jóg, wër dëkk bi.
Mbedd yeek pénc yi
laay seete sama soppey xol.
Seet naa ko, gisuma ko.
3 Wattukat yee ma gis,
ba ñuy wër dëkk bi.
Ma ne leen: «Sama soppey xol, gisuleen ko?»
4 Ma romb leen tuuti rekk,
gis sama soppey xol.
Ma ne ko taral, bàyyeetuma ko,
ba yóbbu ko sama kër yaay,
ba sama biir néegu ndey ji ma jur.
5 Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma
ci taaru kéwél ak koobay àll bi,
ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel
te jotul.
Daagu, jëm toolu mbëggeel
Ñeneen
6 Ana luy jóge màndiŋ ma nii,
mel ni taxaaru saxar,
suuroo ndàbb ak xas mu xeeñ
ak mboolem cuuraayi jula?
Ndaw si
7 Laltub Suleymaan a ngoog,
juróom benn fukki jàmbaar dar ko,
di jàmbaari Israyil.
8 Ñépp mane saamar,
ku ci nekk mokkal xare,
saamar ci pooj,
ngay fàggu mbettum guddi.
9 Ab toogu la Buur Suleymaan defarlu,
ñu defare ko bantu Libaŋ,
10 ponku ya, mu def ko xaalis,
wéeruwaay ba wurus;
tooguwaay ba di ndimo lu xonq curr,
biir ba di liggéeyu ràbb
bu janqi Yerusalem ràbbe cofeel.
11 Yeen janqi Siyoŋ, génnleen,
xool Buur Suleymaan ak mbaxanam céetal
mi ko yaayam solal ci bésub céetalam,