3 Mu wax ak mbokk ma yeyoo sañ-sañu jotaat ba, ne ko: «Ab làccu suuf bu sunu mbokk Elimeleg moomoon la, Nawmi di ko jaay. Mooy ka jóge réewum Mowab, ñibbsi. 4 Man nag dama noon war naa la koo yegge, te laaj la ndax danga koy jënd ci kanam magi dëkk bi ak ñi fi toog. Soo bëggee def sa warugaru jotaat, jëndal. Soo buggul, wax ma, ma xam. Ndax kat kenn gënu la cee yey, te maa topp ci yaw.» Mu ne ko: «Damay jënd kay!» 5 Mu ne ko: «Ãa bés boo jëndee suuf si ci Nawmi nag, yaay denc Ruut ndawas Mowabeen, sa doon soxnas ndem-si-yàlla si, ndax nga mana lawal askanam, ba du fey, boole ci sàmmal leen seen alal.» 6 Mu ne: «Kon de duma mana def sama warugar, ndax sama alal a ciy yàqoo†4.6 Su waa ji defoon warugaru jotaatam, ba denc Ruut, kon moom mooy yor Nawmi ak Ruut ak doom ju ñu am ci séy bi, te it ay doomi boppam duñu donn suufas Elimeleg. Doom ji muy am ak Ruut moo koy donn. Loolu moo doon aaday bànni Israyil.. Fabal boog sama sañ-sañu jotaat, ndax duma ko mana jariñoo.»
7 Booba Israyil, jamono yu jëkk yooya, mbirum njëndum jotaat mbaa ag weccoo, la ñu ko baaxoo dogale ci diggante nit ak moroom ma, nii la: kii day summi dàllam, jox kee. Noonu lees daan yoonale ag jëflante ca Israyil. 8 Moo tax ba boroom sañ-sañu jotaat ba waxee Bowas, ne ko: «Jënd ko yaw,» dafa daldi summi dàllam, dogale ko mbir ma.
9 Ba mu ko defee Bowas wax ak mag ña ak ñeneen ña ñépp, ne leen: «Seedeleen bésub tey ne jënd naa ci Nawmi mboolem alalu Elimeleg ak mboolem alalu Kilyon ak Malon, 10 boole ci Ruut, ndawas Mowab, sa doon soxnas Malon, muy sama soxna. Su ko defee ma mana lawal askanam, ba du fey, boole ci sàmmal leen seen alal, ba turu Elimeleg du réer ci biiri bokkam te du raaf ci limeefu dëkk bi. Yeena ko seede bésub tey jii.»
11 Waa pénc ma mépp ak mag ña nag ne ko: «Noo ko seede. Yal na Aji Sax ji def ndaw siy séysi sa kër, mel ni Rasel ak Leya‡4.11 Rasel ak Leya ñooy doon soxnay Yanqóoba., ñoom ñaar ñi giir waa kër Israyil gépp. Yal nanga tekki ci digg Efrata te amu tur ci Betleyem. 12 Njaboot gu la Aji Sax jiy may ci ndaw sii, yal na ñu lawal saw askan, ba mu mel ni askanu Peres, ma Tamar am ak Yuda.»
16 Nawmi nag fab xale bi, taf ko ci dënnam. Gannaaw loolu moo ko doon topptoo. 17 Jigéeni gox ba nag naa: «Waay waay Nawmi am na doom ju góor!» Ñu tudde xale bi Obedd. Obedd moo jur Yese, miy baayu Daawuda.
18 Kon lii mooy askanu Peres§4.18 Peres taawu Yuda la, di sëtu Yanqóoba. ci wàllu geño: Peres moo jur Esron, 19 Esron, Ram; Ram, Aminadab; 20 Aminadab, Nason; Nason, Salma; 21 Salma, Bowas; Bowas, Obedd; 22 Obedd, Yese; Yese, Daawuda.
<- Ruut 3- a 4.1 ca bunt dëkk ba booy duggsi, fa la pénc ma nekkoon.
- b 4.6 Su waa ji defoon warugaru jotaatam, ba denc Ruut, kon moom mooy yor Nawmi ak Ruut ak doom ju ñu am ci séy bi, te it ay doomi boppam duñu donn suufas Elimeleg. Doom ji muy am ak Ruut moo koy donn. Loolu moo doon aaday bànni Israyil.
- c 4.11 Rasel ak Leya ñooy doon soxnay Yanqóoba.
- d 4.18 Peres taawu Yuda la, di sëtu Yanqóoba.