Ruut
3 Gannaaw gi Elimeleg jëkkëri Nawmi faatu, Nawmi des ak ñaari doomam yu góor. 4 Ñooñu mujj jël ay jigéeni Mowab soxna; kenn ka di Orpa, ka ca des di Ruut. Ba ñu nekkee foofa lu tollu ci fukki at, 5 ñoom ñaar ñooñu di Malon ak Kilyon faatu ñoom it, jigéen ja ñàkk noonu ñaari doomam ak jëkkëram. Mu des moom kenn.
8 Ci biir loolu mu wax ak ñaari goroom, ne leen: «Demleen kay, ñibbileen, ku nekk sa kër yaay. Yal na leen Aji Sax ji baaxe, na ngeen baaxe woon ñi wuutu, te baaxe ma, man itam. 9 Yal na Aji Sax ji may ku nekk ci yeen jàmm ca kër jëkkër ja muy amaat.» Ci kaw loolu mu fóon leen, ñu ne yikkét jooyoo. 10 Ñu ne ko: «Déet, yaw kay lanuy àndal dem ca say bokk.»
11 Mu ne leen: «Ñibbileen ngalla, doom, lu ngeen di ànd ak man doye? Ndax dama leena manatee jural ay jëkkër ci sama biir bii? 12 Ñibbileen rikk doom, demleen, ngir man damay mag, ba wees séy; te su ma ci dese woon yaakaar it, guddig tey jii sax su ma ci séyoon, jur ciy doom, 13 mbaa dingeen leen mana xaar, ba ñu màgg? Xanaa dungeen toog, baña séy ndax ñoom? Déedéet, doom. Maa leen ëpp naqar, man mi Aji Sax ji nattoo nii.»
14 Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggtook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk. 15 Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!» 16 Mu ne ko: «Bu ma soññ mukk ci loolu, duma la wacc, duma la dëddu. Foo jëm, fa laa jëm; foo dal, fa laay dal; say bokk di saay bokk; sa Yàlla di sama Yàlla. 17 Foo deeye it, ma deeye fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.» 18 Nawmi nag gis ni Ruut dogoo ci ànd ak moom, ba tax soññatu ko. 19 Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, ba àgg Betleyem.
22 Noonu la Nawmi jógee Mowab, ñibbsi, ànd ak Ruut, gorob Mowabeenam ba. Ñu agsi Betleyem, fekk ngóobum lors ma di tàmbali.
Ruut 2 ->