6 Du caageenu kàddug Yàlla moo neen, ndax ñi bokk ci xeetu Israyil ñépp duñu Israyil tigi. 7 Te it sëti Ibraayma yépp bokkuñu ci askanam, waaye li Mbind mi indi moo di: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan*9.7 Seetal ci Njàlbéen ga 21.12. .» 8 Loolu di tekki ne du sëti Ibraayma yi ci wàllu deret ñoo di doomi Yàlla, waaye doom yi seenub juddu dëppoo ak digeb Yàlla, ñoom lañu jàpp ne ñooy askanu Ibraayma. 9 Ndax kat kàddug dige ba nii la jibe: «Nëgëni sii déwén laay délsi, te Saarata dina am doom ju góor†9.9 Seetal ci Njàlbéen ga 18.10, 14..»
10 Te yemul foofu rekk, waaye Rebeka it moo am ay seex yu genn góor jur, muy sunu maam Isaaxa. 11 Doom ya nag juddooguñu woon bay def lenn lu baax, mbaa lu bon. Yàlla moo defe noonu ngir wéyal dogal bu dëppoo ak tànnéefu boppam 12 bu ajuwul ci kawi jëf, xanaa ci kiy woote. Rebeka‡9.12 Rebeka mooy soxnas Isaaxa. la kàddu gii dikkal: «Mag ji mooy surgawu rakk ji§9.12 Seetal ci Njàlbéen ga 25.23..» 13 Noonu la Mbind mi indee ne: «Askanu Yanqóoba rakk ji laa sopp, foñ askanu Esawu mag ji*9.13 Seetal ci Malasi 1.2-3..»
19 Xam naa dinga ma ne: «Ana kon lu Yàlla di sikkeeti? Coobarey Yàlla, ana ku koy fanq?» 20 Waaye yaw nit ki, yaay kan bay weddi Yàlla? Ndax këf ku ñu tabax dina ne ka ko tabax: «Lu tax nga sàkke ma nii?» 21 Tabaxkatu ndab bi daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal, lenn ndabal teraanga, ak leneen ndabal njoogaan?
22 Yàlla mi namma wone am sànjam, xamle dooleem, su dee moo muñal lool ay ndab yu yelloo am sànjam, te seen sànkute ñoroon xomm nag? 23 Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teddngaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga? 24 Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jaambur ñi dul Yawut itam. 25 Moom la wax it ci téereb Ose ne:
27 Ci mbirum Israyil la Yonent Yàlla Esayi itam xaacu woon ne:
- a 9.7 Seetal ci Njàlbéen ga 21.12.
- b 9.9 Seetal ci Njàlbéen ga 18.10, 14.
- c 9.12 Rebeka mooy soxnas Isaaxa.
- d 9.12 Seetal ci Njàlbéen ga 25.23.
- e 9.13 Seetal ci Malasi 1.2-3.
- f 9.15 Seetal ci Mucc ga 33.19.
- g 9.17 Seetal ci Mucc ga 9.16.
- h 9.25 Seetal ci Ose 2.25.
- i 9.26 Seetal ci Ose 2.1.
- j 9.27 Seetal ci Esayi 10.22.
- k 9.28 Seetal ci Esayi 10.23.
- l 9.29 Seetal ci Esayi 1.9.
- m 9.33 Seetal ci Esayi 8.14; 28.16.