5 Ndax kat ñi topp seen bindu suux, mbiri bakkan doŋŋ lañu xinte, waaye ñi topp Noowug Yàlla ñoom, mbiri Noowug Yàlla mooy seen xinte. 6 Xintey bakkan nag ci ndee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla ndund ak jàmm lay jur. 7 Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax. 8 Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
9 Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi màkkaanoo ci yeen. Ku amul Noowug Almasi, kooku du nitam. 10 Su Almasi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi. 11 Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.
12 Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan; 13 Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe. 14 Ndax kat, mboolem ñiy dox ci njiital Noo gi, ñooñu ay doomi Yàlla lañu. 15 Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba[a]», mu tekki «Baay.» 16 Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu. 17 Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
22 Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu. 23 Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat. 24 Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootu yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee? 25 Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentook a muñe yaakaar ji.
26 Te itam Noo gi moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noowug Yàlla moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ. 27 Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, nde ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
28 Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme. 29 Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare. 30 Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen jox itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.