5 Gannaaw dees noo bennale ak moom ci dee gu ñu nirule ak deeyam, dees nuy bennale itam ak moom ci ndekkite lu niru ndekkiteem. 6 Li nu bir moo di nun ña woon démb, ca bantub Yeesu ba lees nu daajaale, ngir xewil sunu yaramu bàkkaar, ba nu noppee doon ay jaam, bàkkaar di sunub sang. 7 Ndax ki dee ba noppi, joxees na ko àtteb ku jub, mu tàggook noteelu bàkkaar.
8 Gannaaw noo deeyandoo ak Almasi nag, gëm nanu ne nooy dundandoo ak moom. 9 Ndax kat xam nanu ne Almasi mi dekki dootu dee, te ndee manalatu ko dara. 10 Deeyam ga mu dee ca la deeyal bàkkaar benn yoon ba fàww, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.
11 Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu deeyal bàkkaar, te di dundal Yàlla, ci Yeesu Almasi. 12 Kon nag bu bàkkaar yilif seen yaramu ndee wii, ba di leen nanguloo ay xemmemtéefam yu bon. 13 Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébbal-leen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub. 14 Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.
19 Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga. 20 Ba ngeen dee jaami bàkkaar, teewuleen woona moom seen bopp, ci seen digganteek njub. 21 Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon. 22 Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag sellnga la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk. 23 Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
<- Room 5Room 7 ->