5 Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe. 6 Ca lay fey ku nekk ay jëfam. 7 Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam, ak teraanga, ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ. 8 Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét lañuy yooloo. 9 Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci; 10 daraja, ak teraanga, ak jàmm nag moo ñeel képp kuy def lu baax, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci. 11 Ndax kat xejj ak seen amul fa Yàlla.
12 Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane. 13 Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di joxee àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa lees di joxe nit àtteb ku jub. 14 Jaambur ñi dul Yawut, te amuñu yoonu Musaa, ndegam teewu leena topp bindub juddu, bay jëfe li yoonu Musaa laaj, dafa fekk ñoom ci seen bopp, ñuy seen yoonu bopp, doonte amuñu yoonu Musaa. 15 Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def leeg-leeg mu sikk leen, leeg-leeg mu dëggal leen. 16 Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.