Saar 13
Na ñépp déggal njiit yi
1 Na ku nekk déggal njiit yi yor kilifteef, nde amul njiit lu bawoowul fa Yàlla, te njiit yi toog, Yàlla moo leen tabb. 2 Moo tax kuy bañal njiit, tëralinu Yàlla nga bañal, te ñi bañal njiit, ñoo wool seen bopp mbugal. 3 Kuy def lu baax nag, doo ragal kilifa yi, kiy def lu bon moo leen di ragal. Soo bëggee mucc ci ragal kilifa nag, defal lu baax, jot ngërëmam. 4 Ndax kilifa gi mooy ndaw li Yàlla yebal ngir sa jàmm. Waaye soo dee def lu bon, ragalal, ndax kilifa gi yorul ab saamar cig neen; mooy ndawal Yàlla liy añale, te mooy jottli am sànj mu wàccal kuy def lu bon. 5 Moo tax nangul njiit di wartéef, ndax njariñal nangul njiit yemul rekk ci mucc ci am sànj, waaye xel mu dal a ngi ci.
6 Loolu moo waral it ngeen di fey galag, ndax njiit yi koy feyeeku kat, ñooy jawriñi Yàlla yi sasoo googu kilifteef. 7 Joxleen ku nekk li ngeen warlook moom; ku ngeen wara fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen wara fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen wara weg, wegleen ko; ku ngeen wara teral, teral-leen ko.
Cofeel moo tënk yoonu Musaa
8 Buleen ameel kenn bor, lu moy borub soppante; ndax ku sopp sa moroom, yaa matal yoonu Musaa. 9 Ndax ndigal yii kat: «Buleen jaaloo, buleen bóom, buleen sàcc, buleen xemmem*13.9 Seetal ci Mucc ga 20.13-15, 17.,» ak leneen ndigal lu mu mana doon, ci genn kàddu gii la tënke: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom†13.9 Seetal ci Sarxalkat yi 19.18..» 10 Cofeel du waral kenn def moroomam lu bon; kon cofeel moo matal sëkk yoonu Musaa.
Teewlu war na gëmkat ñi
11 Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm. 12 Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer. 13 Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan. 14 Waaye yiirooleen Sang Yeesu Almasi, te ngeen baña yittewoo seen bakkan, ngir di topp seeni xemmemtéef.
<- Room 12Room 14 ->