Room
7 Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
13 Bokk yi, bugguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii. 14 Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp. 15 Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
21 Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm. 22 Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof. 23 Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deeyam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.
24 Moo tax Yàlla bërgal leen ak seen xemmemtéef yu bon yi ci seen xol, ba ñu sóobu ci jëflantey sobe juy teddadil seen yarami bopp. 25 Ñoo weccee dëggu Yàlla, aw fen, di sujjóotal ak a jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
26 Loolu moo tax Yàlla bërgal leen ak seen bëgg-bëgg yu teddadi. Seeni jigéen sax dëddu nañu jaxasoo gi leen bindub juddu sédde, ba jublu ci lu woroo ak seen bindub juddu. 27 Naka noonu, góor ñi it noppee jaxasoo ak jigéen, ni leen ko bindub juddu sédde, bay xabtaloo ci seen biir, seen bëgg-bëggi bakkan yu tar; ay góor di séq ak seen moroomi góor jëf ju gàccelu, ba tax leena jot ci seen jëmmi bopp, seen añub réeraange.
28 Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi. 29 Dañoo dem ba feese gépp xeetu njubadi, akug mbon, akug bëgge, akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan, ak pexey bóome, ak ŋaayoo, akug njublaŋ, ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it, 30 te di yàqkati der, ñu bañ Yàlla lañu, ñu reew, réy, di tëggu, ñu xareñ ci fexe lu bon, te déggadil seeni waajur. 31 Amuñu xel, amuñu kóllëre, amuñu xol, amuñu yërmande. 32 Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.
Room 2 ->- a 1.17 Seetal ci Abakug 2.4.