4 «Waaye li ma la sikke moo di sa cofeel ga nga jëkke woon, moom nga wacc. 5 Kon nag fàttlikul fu kawe fa nga xàwwikoo ba fii, te nga tuub, di jëfe jëf ja nga jëkke woon. Lu ko moy maay dikk ba fi yaw, daldi jële sa tegukaayu làmp fa bérabam, ndegam tuubuloo. 6 Waaye lu baax lii nag yaay boroom: ni ma sibe jëfi ngérum Nikolas[a], ni nga ko sibe. 7 Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.
11 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag doo loru mukk ci ñaareelu dee gi.[b]
14 «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag‡2.14 Balaam, Balag: Balaam moo doon mbubboo turu yonent, di fexee rëbb bànni Israyil, ngir sàkku alal ci Balag buuru Mowab ci jamonoy Yonent Yàlla Musaa. Seetal ci Màndiŋ ma 22—23. ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu. 15 Naka noonu itam yaa ngi uuf ay nit ñuy saxal njànglem ngérum Nikolas. 16 Kon nag tuubal. Lu ko moy maay dikk léegi ba fi yaw, te saamar biy lange sama gémmiñ, moom laay xareek nit ñooñu.
17 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn[d] mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; doj wu ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.
20 «Waaye lenn laa lay sikke: dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, muy jàngleek a réeral sama jaam ñi, ngir ñuy gànctu ak a lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur. 21 May naa ko ab diir, ngir mu tuub, waaye moo buggula tuub ngànctoom. 22 Kon nag maa ngii di ko rattax cib lal, te ñi mu àndal di gànctu it, maa leen di sóob ci mitit wu réy, su ñu tuubul jëf ja ñu koy roye. 23 Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.
24 «Waaye yeen ñi ci des ñépp nag, yeen waa Catir ñi toppul moomu njàngle te jotuleena xam loolu ñu naan xóotey xam-xamu Seytaane, maa ne leen, duma leen sëf beneen sëf. 25 Ŋoyleen rekk ci li ngeen am, ba kera may dikk.
26 «Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:
- a 2.6 ngérum Nikolas mooy ñiy taafantoo sañ-sañ bu ñu am gannaaw bu ñu gëmee Yeesu, ngir daganal yenn aada yu ñaaw yu mel ni lekk lu ñu sarxal ay tuur, ak powum séy.
- b 2.11 ñaareelu dee gi: seetal ci 20.14 ak 21.8.
- c 2.14 Balaam, Balag: Balaam moo doon mbubboo turu yonent, di fexee rëbb bànni Israyil, ngir sàkku alal ci Balag buuru Mowab ci jamonoy Yonent Yàlla Musaa. Seetal ci Màndiŋ ma 22—23.
- d 2.17 mànn moo di ñam wa Yàlla wàcceeloon Musaa ak bànni Israyil, ba ñu gàddaayee Misra, jëm ca réew ma leen Yàlla digoon.
- e 2.18 Doomu Yàlla: tur wii tekkiwul ne Yàlla moo jur Yeesu mook Maryaama. Tekkiwul it ne dañoo màggal nit, ba di ko méngale ak Yàlla. Waaye day tekki ne Yeesu mooy Kàddug Yàlla, mooy màndargam jëmmu Yàlla, ci jikkoom ji gëna biire. Ku gis doom, man ngaa xam nu baayam mel. Ku gis Yeesu kon, mana xam nu Yàlla mel.