8 Meneen malaaka, topp ci, di ñaareel bi. Mu ne: «Babilon a daanoo, dëkk bu mag ba daanu na! Moom ma daan màndal askanoo askan biiñu moyam muy indi am sànj.»
9 Meneen malaaka, topp ci, di ñetteel bi. Mu àddu ca kaw, ne: «Képp ku sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ba ñu defal ko màndargam jë mbaa loxo, 10 kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi. 11 Seen saxaru sawaras mbugal day saxoo dàkk, di gilli ba fàww. Guddeek bëccëg, ñooñuy sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ak mboolem ku ñu màndargaale turu rab wi, kenn du ci nopplu.»
12 Kon nag ñu sell ñiy wormaal santaaney Yàlla te saxoo gëm Yeesu, looloo tax ñu wara muñ.
13 Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokklee aji dee ñi deeyaale gëm Sang bi.”» Noo ga daldi ne: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»
16 Ci kaw loolu ki toog ci kaw niir wi dawal sàrtam ci kaw suuf, daldi góob àddina.
17 Meneen malaaka nag génne ca néeg Yàlla ba ca asamaan, ŋàbb moom itam, sàrt bu ñaw. 18 Ba loolu amee meneen malaaka mi yilif sawara, jóge ca sarxalukaay ba, daldi àddu ca kaw, wax ak malaaka, mi yor sàrt bu ñaw bi, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi, nga dagg cëggi reseñ gi ci àddina, ndax reseñ ji ñor na.»
19 Malaaka ma dawal sàrtam ci àddina, dagg reseñ ji, sànni ci biir nalukaay bu mag bu sànjum Yàlla ba. 20 Ñu dëggaate reseñ ja ca nalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génne ca, taa ba tollook laabi fas yi, wala wal ba dajal digganteb ñetti téeméeri kilomeetar.
<- Peeñu ma 13Peeñu ma 15 ->- a 14.1 tundu Siyoŋ mooy tund wa ñu tabax Yerusalem ci kawam.