4 Ñaari seede yi ñoo di ñaari garabi oliw[a] yeek ñaari tegukaayi làmp, yi taxaw ci kanam Boroom suuf si. 5 Ku leen nara lor, sawaraay génne seen gémmiñ, lakk seeni noon. Képp ku leen nara lor, noonu ngay deeye. 6 Am nañu sañ-sañu tëj asamaan, ba du taw diiru fan yi ñuy biral waxyu, am nañu itam sañ-sañ ci ndox mi, ngir soppi ko deret, ak sañ-sañu wàcceel suuf wépp xeetu musiba, saa su leen soobee.
7 Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen. 8 Seeni néew da naan lareet ci péncum dëkk bu mag boobu ñuy misaale turu Sodom mbaa Misra, fa ñu reye woon seen Sang ci bant. 9 Diiru ñetti fan ak genn-wàll lañuy weeru, niti wépp xeet, ak gépp giir, ak wépp làmmiñ, ak wépp askan di seetaan seeni néew, te duñu bàyyi kenn suul leen. 10 Waa àddina dinañu bége seen dee, di bànneexu, di joqlante ay njukkal, ndaxte ñaari yonent yooyu ñoo lakkaloon waa àddina.
11 Waaye bu ñetti fan yeek genn-wàll wéyee, noowug dund giy bawoo fa Yàlla moo leen di solu, ñu jóg, taxaw, tiitaange lu réy daldi jàpp waa ceetaan ma. 12 Ba loolu amee ñaari seede yi dégg baat bu xumb jibe asamaan, ne leen: «Yéegleen fii.» Ñu yéeg asamaan ci biir aw niir, seeni noon di gis. 13 Ca waxtu wa, suuf daldi yëngu lool, ba benn fukkeelu dëkk ba màbb. Juróom ñaari junniy nit (7 000) dee ci yëngub suuf ba, ña ca des tiit, di sàbbaal Yàllay asamaan.
14 Ñaareelu musiba mi wéy na, waaye kat ñetteel baa ngi nii di ñëw.
19 Ci kaw loolu néeg Yàlla bi ci asamaan ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga[b] di feeñ ca biir màkkaanam ma, melax ya tàkk, kàddu yaak dënu ya riir, suuf sa yëngu, tawu doji yuur bu metti daldi sóob.
<- Peeñu ma 10Peeñu ma 12 ->- a 11.4 oliw: garabu oliw dafa xawa mel ni sump, te am doom yu ñuy nal, ngir am ci diw gu ñuy togge, mbaa ñu di ko taaloo.
- b 11.19 gaalu kóllëre ga: gaal gi ñuy wax fii waxande la, wu ñu denc àlluwa, ya ñu bind yoonu Yàlla te Yonent Yàlla Musaa jottli ko. Yàlla moo joxoon Musaa àlluway xeer yooyu, bind ca yoon wa lal kóllëre ga mu fas ak bànni Israyil.