Peeñum Almasi Yeesu
8 «Man, maay Alfa, di Omega[e]», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji.
12 Naka laa geestu, di seet kuy wax ak man, ma daldi gis juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus. 13 Ca digg tegukaayi làmp ya, jëmm juy nirook nit†1.13 Seetal ci Dañeel 7.13. a fa nekk. Ma nga sol mbubb mu tollu ci ndëgguy tànk yi, takkoo ngañaayal wurus ci dënn bi. 14 Kawaru bopp baa nga weex tàll, gët ya di tàkk ni sawara, 15 tànk ya mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baat bay riir ni gannaxi géej. 16 Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.
17 Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj. 18 Maay Kiy Dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw. 19 Kon nag bindal li nga gis: Li am nii tey ak itam liy ñëw gannaaw lii. 20 Kumpa gi ci juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi, li muy firi mooy: juróom ñaari biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy gëmkat ñi; juróom ñaari tegukaayi làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.»
Peeñu ma 2 ->- a 1.4 juróom ñaari noo ya: seetal ci 4.5 ak 5.6.
- b 1.4 ngàngune ma mooy fa buur biy toog.
- c 1.5 taaw bi: taaw mooy ki jëkka juddu, waaye ab juddu taxul ñuy wax fii. Li Yeesu Almasi jëkka dekki ndekkite lu dee toppatul moo tax ñuy wax. Mooy taaw ci kaw darajaam ndax moo sut ñépp, yilif lépp luy mbindeef, te ci darajaam la ñépp di dekkee.
- d 1.6 Baayam: seetal ci Luug 3.23, 38.
- e 1.8 Alfa, Omega: ci làkku gereg, alfa moo jëkk ci araf yi, omega mujj ci. Kuy Alfa ak Omega nag moo jëkk, moo mujj.
- f 1.13 Seetal ci Dañeel 7.13.