Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 99
Aji Sax ji buur bu sell la
1 Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko!
Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!
2 Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg,
kawe, tiim xeetoo xeet.
3 Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko.
—Kee sell!
4 Buur, jëfe yoon mooy dooleem,
te yaa saxal njub, yoon ak njekk
ci askanu Yanqóoba.
5 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji,
te sujjóot fa ndëggastalam.
—Kee sell!
 
6 Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam,
Samiyel bokk ca ñay tudd turam.
Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.
7 Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom,
ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon.
8 Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon,
di seen Yàlla ju leen di baal,
te di leen mbugale seeni jëf ju bon.
9 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji,
te sujjóot fa tundam wu sell wa.
—Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!

<- Sabóor 98Sabóor 100 ->