Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 96
Buur Yàllaa ngi àttesi àddina
1 Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
te àddina yépp woy Aji Sax ji.
2 Woyleen Aji Sax ji, màggal turam,
di yéene bés ak bés ne mooy musle.
3 Siiwal-leen teddngaam fi biir xeet yi,
xamal waasoo waaso ay jalooreem.
4 Aji Sax jee màgg, jara santa sant
te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.
5 Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la,
waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
6 Màggaay ak daraja, fa moom,
dooleek taar, fa këram gu sell.
 
7 Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji;
seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole.
8 Seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam,
yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.
9 Sujjóotal-leen Aji Sax ji làmboo sellnga,
te àddina wërngal këpp di ko loxal.
10 Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur:
àddinaa ngii, dëju te raful.
Mooy àtte xeet yi njub.
11 Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul!
Géejoo, riiral yaak li la fees,
12 te mbooy mi di jaayu, mook lu ci biiram,
garabi àll bi sarxolleendoo,
13 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk,
àttesi àddina,
di àtte dun bi njekk,
tey àttee xeet yépp dëggam.

<- Sabóor 95Sabóor 97 ->