Sabóor 94
Yàllaay mbugal ku bon
1 Éy Aji Sax ji Yàlla, boroom mbugal!
Boroom mbugal, feqal sag leer!
2 Yaw miy àtte àddina, jógal
yool ku bew.
3 Aji Sax ji, fu ku bon kiy àkki?
Fu ku bon kiy kañu àkki?
4 Ñu ngi làmmiñoo reewande,
képp kuy def lu bon di damu.
5 Aji Sax ji, say ñoñ lañuy dëggaate;
say séddoo lañuy néewal.
6 Jëtun akub doxandéem, ñu faat;
ab jirim, ñu bóom,
7 te naa: «Ki Sax gisu ci,
Yàllay Yanqóoba jii yégu ko.»
8 Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen.
Gàtt xel yi, kañ ngeen di muus?
9 Ki jëmbati nopp, da dul dégg a?
Am ki xari gët, da dul gis?
10 Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee?
Du mooy kiy xamal nit?
11 Aji Sax ji xam na xalaatu nit,
xam ne cóolóolu neen la.
12 Ki Sax, ndokklee ki ngay yar,
tàggat ko ci saw yoon,
13 dëfal ko ci bési safaan,
ba keroog ñuy gasal ku bon.
14 Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk,
du bàyyi ay séddoom.
15 Àtte dina dellu laloo njekk,
képp ku jub topp ca.
16 Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi?
Ku may jógal ci biir ñiy def lu bon?
17 Su ma Aji Sax ji walluwloon,
tuuti ma fanaani réew ma ne selaw.
18 Dama noon: «Tarxiis naa!»
Waaye yaa ma awoo sa ngor.
19 Ma bare xalaati xol,
nga dëfal ma, ma bég.
20 Loo séq ak njiit lu jubadi
luy yoonal njubadi?
21 Ñii dañoo mànkoo, di tëru ku jub,
di teg àtteb dee ku deful dara.
22 Waaye Aji Sax jeey sama rawtu,
sama Yàlla laay sës, làqu.
23 Moo leen di këpp seen ñaawtéef,
sànke leen seenug mbon.