Sabóor 88
Ma jàq, jooy
1 Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra.
2 Éy Aji Sax ji, Yàlla ji may musal,
bëccëg ma yuuxu,
guddi ma yuuxu fi sa kanam.
3 Yal na sama ñaan àgg fa yaw;
teewlul, ma woote wall.
4 Damaa suur këll ay musiba,
ba soreetuma njaniiw,
5 ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel.
Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
6 bokk ci néew, yi dara waratul,
mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax,
faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.
7 Tàbbal nga ma kàmb gu xóot,
biir xóotey lëndëm.
8 Yen nga ma sa xadar,
tance ma sa gannax yépp.
Selaw.
9 Dàqal nga may xame,
tax nga ñu seexlu ma;
ma tëju, génnatuma.
10 Samay gët a ngi giim ndax naqar.
Éy Aji Sax ji, maa ngi lay woo bés bu ne,
dékk lay loxo.
11 Ku dee, lu muy doyeeti say kéemaan?
Ndax néew dina jóg di la màggal?
Selaw.
12 Dees na siiwal sa ngor biir bàmmeel,
mbaa sa worma ci paxum sànkute?
13 Ana kuy yég say kéemaan ci googu lëndëm?
Ku lay seedeel njekk réew ma fàtte faloo?
14 Aji Sax ji, man, yaw lay woo wall,
xëy, kare la gii ñaan, ne la:
15 Éy Aji Sax ji, loo may gàntale,
di ma fuuylu?
16 Mitit bay laatikaaf, sama ngone ba tey;
sa mbugal yu raglu, ba bopp ubu ràpp!
17 Sa mer mëdd ma,
sa mbugal yu raglu sànk ma,
18 mëdd ma nim ndox bés bu ne,
gëndoo fi sama kaw.
19 Dàqal nga ma soppeek xarit,