Sabóor 87
Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yi
1 Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor.
Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya.
2 Aji Sax jee sopp bunti Siyoŋ gii,
mu gënal ko fu askanu Yanqóoba dëkke.
3 Yaw, dëkkub Yàlla bi,
tuddees na say jaloore.
Selaw.
4 Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg.
Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus.
Nit a ngii, juddoo fa,»
5 te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ,
ne kii ak kee fa bokk juddoo,
te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ.
6 Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen
ne: «Kii fi la juddoo.»
Selaw.
7 Kuy fecc ak kuy woy ànd naan: