Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 85
Aji Sax ji, suqleeti nu
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
 
2 Éy Aji Sax ji, yaa baaxe woon sa réew mi,
ba suqli sëti Yanqóoba yi,
3 baal sa mbooloo seeni ñaawtéef,
jéggal leen bépp bàkkaar.
Selaw.
4 Ba nga xadar ja,
muñ mer ma.
 
5 Éy Yàlla mi nuy musal, suqli nu,
te meddi.
6 Xanaa doo nu mere fàww,
ba ca sët yaak sëtaat ya?
7 Xanaa dinga leqli sa mbooloo,
ba ñu man laa bànneexoo?
8 Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor,
baaxe nu sag wall.
 
9 Woykat ba nee: «Naa déglu
lu Aji Sax ji Yàlla di wax.»
Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam,
ba duñu dellu ci jëfi dof.
10 Wallam aka jege ñi ko ragal,
te leeram dëgmal sunu réew mii!
11 Ngor ak kóllëree daje,
njekk ak jàmm saafoonte,
12 kóllëre jebbee fa suuf,
njekk séentoo asamaan,
13 Aji Sax ji it maye ngëneel,
sunu suuf meññal,
14 njekk jiitu Aji Sax ji,
di ko xàllal yoonam.

<- Sabóor 84Sabóor 86 ->