Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 8
Aji Sax ji teral na nit
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit*8.1 gitiit tur la wu réer ci làkku ebrë. Man na doon xeetu xalam gu cosaanoo dëkk ba ñuy wax Gaat ci réewu Filisti. Man na nekk it galan bu ñu daan woye ci jamono bu ñuy witt reseñ, di ko nal., ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
 
2 Aji Sax ji sunu Boroom,
sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!
Sag leer tiim asamaan.
3 Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp,
feeñal nga ca sa kàttan,
bañaaleek feyukat ne xerem.
 
4 Damay xool sa asamaan si nga móol,
ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
5 Moo luy nit, ba nga di ko bàyyi xel?
Luy doom aadamaak loo koy yége?
 
6 Yaa def nit mu yées malaaka yi as lëf,
te yaa ko kaalaa teraangaak daraja,
7 fal ko ci kaw loo bind,
jox ko lépp, mu teg tànk:
8 jur gépp, gu gudd ak gu gàtt,
rabi àll it ca la,
9 ak njanaaw ak jën,
ak luy jaare yooni géej.
 
10 Aji Sax ji sunu Boroom,
sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!

<- Sabóor 7Sabóor 9 ->