Sabóor 75
Yàllaay àtte
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Bul yàq, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.
2 Yàlla, nu sant la, santati la;
nu ngi lay woo,
di siiwal say jaloore.
3 Yàlla nee: «Maay takk ab àpp,
àtte ca njub.
4 Bu suuf di yëngu mook ñi ko dëkke ñépp,
maay kiy téye ay kenoom.
Selaw.
5 Dama ne ku réy: “Bul réy-réylu,”
ne ku bon: “Bul bew,
6 bul bewa bew,
bay waxe reewande.”»
7 Du penku, du sowu,
te du màndiŋ ma la daraja di jóge.
8 Yàllaay àtte:
kii mu detteel, kee mu kaweel.
9 Merum Aji Sax ji dib kaas ci loxoom,
biiñu njafaan bu wex di ca fuur,
mu jol ko képp ku bon ci àddina,
mu naan ba naanaale ginjrit ga.
10 Man may biral jëfam ba fàww.
Damay woy Yàllay Yanqóoba.
11 Mu ne: «Jépp dooley ku bon, ma neenal;