Sabóor 72
Nu ñaanal Buur
1 Ñeel Suleymaan.
Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte,
mayal doomu Buur bii sa xelum njekk,
2 muy àttee sa mbooloo njub,
di àttee sa néew-ji-doole ñi yoon,
3 tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm,
tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk,
4 Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi,
di wallu doomi néew-ji-doole
tey dëggaate kiy nennoo.
5 Yal nañu la wormaal feek jant biy am,
feek weer wiy feq, sët ba sëtaat.
6 Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef,
mbaa waame wuy suuxat suuf.
7 Janti Buur aji jub day woomle,
te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,
8 mu yilif géej ba géej
ak dex ba ca cati àddina.
9 Waa màndiŋ mi di ko sukkal,
ay noonam mëq suuf,
10 buuri Tarsis ak dun ya
di ko indil ay galag;
buuri Saba ak Seba
di ko yótsi yóbbal,
11 buuroo buur di ko sujjóotal,
xeetoo xeet di ko surgawu.
12 Mooy xettliji aji tumurànke bu woote wall
ak aji néewle ju sësul fenn.
13 Mooy yërëm ku néewleek ku tumurànke,
di sàmm bakkanu aji tumurànke,
14 boole leen jot ci notaangeek loraange,
ngir fonk seen bakkan.
15 Yal na Buur gudd fan,
yal nañu ko may wurusu Saba.
Nañu koy ñaanal saa su ne,
di ko saxoo, mu barkeel.
16 Yal na pepp ne gàññ ci réew mi,
yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ;
dëkk yu mag yi sëqi nit ba law,
17 yal na turam sax,
ba law fu jant tiim,
yal na xeet yépp barkeele ci moom,
te di ko ndokkle.
18 Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji,
Yàllay Israyil, mi wéetooy jalooreem.
19 Cant ñeel na teddngaam, ba fàww,
yal na teddngaam dajal suuf sépp!
Amiin, Amiin!