Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 67
Yal na nu Yàlla barkeel
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor.
 
2 Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu,
te geesoo nu sa leeru kanam,
Selaw,
3 ba ñu ràññee sa loxo fi kaw suuf,
gis sag wall fi biir xeet yépp.
 
4 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant,
na la xeet yépp sant.
5 Na xeet yiy bég, di sarxolle;
loo dogalal xeet yi njub la,
te yaay wommat xeet yi ci kaw suuf.
Selaw.
6 Yaw Yàlla, na la xeet yi sant,
na la xeet yépp sant.
 
7 Suuf si nangu na,
yal na nu Yàlla, sunu Yàllay barkeel.
8 Yal na nu Yàllay barkeel,
ba àddina wërngal këpp ragal ko.

<- Sabóor 66Sabóor 68 ->