Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 61
Naa woote wall
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
 
2 Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy,
teewlul, ma dagaan la.
3 Àll laa lay wooye,
sama xol jeex;
yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
4 Yaw laa làqoo,
ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
5 Naa dëkke sa xayma, ba fàww;
làqoo sa kiiraay.
Selaw.
6 Yàlla, yaa dégg samay dige,
sédd ma céru ñi la wormaal.
 
7 Ngalla féqal fani Buur,
ay atam bare, sët ba sëtaat.
8 Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam,
nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo;
9 kon ma woy la ba fàww,
di jëfe samay dige bésoo bés.

<- Sabóor 60Sabóor 62 ->