Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 58
Yàllaa mana mbugal
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.
 
2 Yeen daal, su ngeen waxee, dëgg selaw.
Mbaa yeena ngi àtte nit ñi ci yoon?
3 Yeena ngi mébét njubadi,
di lawal fitna ci réew mi.
 
4 Ku bon day sosu rekk, dëng;
juddu, teggi yoon, dib fen-kat.
5 Day am daŋar ni ñàngóor,
fatti noppam ni jaan ju tëx:
6 du dégg baatu jatkat,
mbaa jati ñeengokat bu ñàng.
 
7 Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ;
Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii.
8 Yal nañu ne mes ni ndox muy wal,
yal nañu diir seen fitt, mu damm,
9 yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey,
mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.
10 Balaa seen cin a yég tàngooru gajj,
muy gu tooy, muy guy boy,
yal na leen fekk sànku*58.10 Li ñu wax ci aaya wii am na werante..
 
11 Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég,
muy jàngoo deretu ku bon.
12 Ku ne naan: «Ku jub jot sab yool moos!
Te Yàllaa ngi fi moos, di àtte àddina!»

<- Sabóor 57Sabóor 59 ->