Sabóor 53
Mbon maase na
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat, di taalif bu ñeel Daawuda.
2 Ab dof a nga naa ca xelam:
«Yàlla amul,»
tey def njekkar,
njubadeem siblu,
kenn defu ci lu baax.
3 Yàllaa tollu asamaan, jéer doom aadama,
di seet ku ci xelu,
tey sàkku Yàlla.
4 Ñépp a dëddu,
bokk yàqu yaxeet.
Kenn deful lu baax,
du kenn sax.
5 Yàlla nee: «Xanaa ñiy def lu bon, xamuñu dara?
Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam,
te sàkkuwuñu Yàlla.»
6 Waaye ñooy tiita tiit
fu tiitaange amul.
Yàllaay tasaare néewi nit ñi la gaw.
Yàllaa leen wacc, nga gàcceel leen.
7 Ana kuy tollu Siyoŋ, xettli Israyil?
Éy, bés bu Yàlla delloo ñoñam ndam,
ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba!