Sabóor 52
Yàllaa man boroom doole
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda. 2 Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sóol, ne ko Daawuda dem na kër Ayimeleg*52.2 Seetal ci 1.Samiyel 21—22..
3 Moo jàmbaar ji, looy damoo jëfi coxor?
Yàlla, ngoram, bés bu nekk la.
4 Ak sa làmmiñ wi ngay sose loraange,
mel ni saatu su ñu xacc,
rambaaj bi!
5 Lu bon a la gënal lu baax,
fen a la gënal wax dëgg.
Selaw.
6 Yaa bëgg jépp wax juy yàq,
waabajiiba bi!
7 Yàlla da lay sànk ba fàww,
fëkke la sab xayma, yóbbu,
déjjatee la réewum aji dund.
Selaw.
8 Aji jub gis ko, yéemu,
di la ree, naa:
9 «Xool-leen jàmbaar ji làqoowul Yàlla,
xanaa di yaakaar alalam ju bare,
di yokkoo loraange.»
10 Man, ma mel ni garabu oliw gu naat
fa biir kër Yàlla,
di wóoloo Yàlla ngoram
tey ak ëllëg.
11 Naa la sante sa jëf ba fàww,
naa biral sa tur wu baax,