Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Sabóor 50
Aji Sax ji xol lay gërëm
1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
 
Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na,
di woo àddina, penku ba sowu.
2 Ca Siyoŋ, dëkk ba ca taar ba
la Yàlla feeñe ni leer gu jolli.
3 Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell,
sawaraa ko jiitu, di xoyome,
ngëlén lu mag wër ko.
4 Ma ngay woo seede asamaan ak suuf,
ngir àtte ñoñam.
5 Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre
ñiy sarxal, di ko fase sama kóllëreek ñoom.»
6 Asamaan a ngi biral njekkam,
ngir Yàllaay àtte.
Selaw.
 
7 «Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen;
yeen waa Israyil, ma sikk leen.
Maa di Yàlla, seen Yàlla.
8 Du seeni sarax laa leen di sikke,
mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
9 Soxlawuma yëkku yar
ak sikketu gétt.
10 Maay boroom raboo rabu àll,
ak junniy nag yuy fore tund ya.
11 Xam naa njanaawi tund yi,
luy ndundatub tool maa ko moom.
12 Su ma xiifoon, duma leen ko wax,
maa moom àddinaak li ci biiram.
13 Damay lekk yàppu nag
ak a naan deretu sikket a?
14 Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko,
di fey Aji Kawe ji loo dige,
15 di ma woo bésub njàqare,
ma wallu la, nga màggal ma.»
 
16 Ñu bon ñi Yàlla ne leen:
«Lu ngeen di tari sama dogali yoon,
di waxe sama kóllëre?
17 Yeena ngii, bañ sama yar,
xalab samay kàddu.
18 Fu ngeen gis ub sàcc, neexook moom,
ab njaalookat, ngeen lëngool.
19 Dangeena afal seen gémmiñ ci mbon,
seen làmmiñ taqoo fen,
20 ngeen di tooge seen mbokk,
di yàq deru doomu ndey.
21 Lii yeena ko def! Damay noppi,
ngeen defe ne damaa mel ni yeen?
Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis!
 
22 «Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii,
bala maa fàdd te kenn du wallu.
23 Ki may sarxale jaajëf moo ma teral;
ku topp yoon, ma won ko wallu Yàlla.»

<- Sabóor 49Sabóor 51 ->